Leeru Bés bi — 8 Sàttumbar: Dañeel 5:27

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

NATT: Nattees na sa diisaay ci nattukaay bi, nga yées.

Dañeel 5:27

«Buleen ŋalŋaleeti, di damooka damooti, bu reewande génne seen gémmiñ, Aji Sax jeey Yàlla ji xam lépp, te mooy natt jëfi nit.

1.Samiyel 2:3

Yeesu ne leen: «Yeen yeenay jub-jublu ci kanam nit ñi, waaye Yàlla xam na seen xol. Ndax li nit ñi gëna naw, lu seexluwu la fa Yàlla.

Luug 16:15

Aji Sax ji nag ne Samiyel: «Bul xool ci melokaanu kii, mbaa jëmmu taxawaayam, ndax gàntal naa ko. Lii du ci gis-gisu nit. Nit, li fees bëtam lay gis, waaye Aji Sax ji ci xol lay xool.»

1.Samiyel 16:7

Bu leen lenn nax; Yàlla deesu ko foontoo. Nit ki, li mu ji, moom lay góob. Ku jiwal bànneexu bakkanam, ci bànneexu bakkanam lay jële ngóobum yàqute; ku jiwal Noowug Yàlla, ci Noo gi ngay góobe texe gu sax dàkk.

Galasi 6:7–8

Te it jagoo àddina sépp lu muy jariñ nit, bu ñàkkee bakkanam? Ak lu nit wara mana weccee bakkanam?

Macë 16:26

Waaye la ma jàppe woon ag ndollent, moom laa def tey ag wàññeent ndax Almasi bi.

Filib 3:7

Yaw laa moy, yaw doŋŋ. Li nga ñaawlu laa def. Kon boo waxee, am dëgg, te soo àttee, yey.

Taalifi cant 51:6

Natt nga saab xol, niir ma guddi, settantal ma, gisoo dara. Dogu naa ne duma moye wax.

Taalifi cant 17:3

Waaye ku nekk ak ayam: saraxu ndoortel meññeef mi, Almasi bi la. Gannaaw loolu ñoñi Almasi bi ñooy aye, keroog bu délsee.

1.Korent 15:23

Maa leen ko wax déy ci lu wér, su feppu bele waddul ci suuf, dee, wéetaay lay dëkke. Waaye su deewee lay meññ fepp yu bare.

Yowaan 12:24

Ndax kat ab sarax bu génnee ci nootu sunguf, di ndoortel meññeef, su boobu sarax sellee, tooyalub sunguf bépp ay sell. Ndax su reenu garab sellee, car ya it sell.

Room 11:16

Waaye nag Almasi bi dafa dekki moos, te mooy saraxu ndoortel meññeef bi ñu sàkke ci ngóobum bakkani nit ñi dee.

1.Korent 15:20

Gannaaw dees noo bennale ak moom ci dee gu ñu nirule ak deewam, dees nuy bennale itam ak moom ci ndekkite lu niru ndekkiteem.

Room 6:5

Nun nag sunum réew a nga fa asamaan, fa nuy séentoo sunu Musalkat, Sang Yeesu Almasi bi. Mooy kiy liggéeye manooreem ji mu tënke lépp cig curgaam, ba sopparñi sunu yaram wu doyadi wii, niroole kook yaramam wi ànd ak màggaay.

Filib 3:20–21

Mooy boppu yaram, wiy mbooloom gëmkat ñi, mooy njàlbéen, mooy taaw bi njëkka dekki, ndekkite lu dee toppul, ba tax muy ki jiitu ci lépp,

Kolos 1:18

Noowug ki dekkal Yeesu moo sax ci yeen. Kon nag ki dekkal Almasi bi mooy dekkal itam seen yaram wu jëm ci dee, ndax Noowam googu sax ci yeen.

Room 8:11

Yeesu ne ko: «Man maay ndekkite li, maay dund gi; ku ma gëm, soo deewee it, dinga dund.

Yowaan 11:25