Leeru Bés bi — 9 Sàttumbar: Luug 1:53

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Ñi xiif, mu reggale leen lu neex, ñi duunle, mu dàqe loxoy neen.

Luug 1:53

Gannaaw yaa ngi naan: “Am naa alal, barele naa, soxlaatuma dara,” te yaw xamuloo ni nga toroxe, jara yërëm, ñàkk, gumba, ne duŋŋ, dama lay digal, nga jënd ci man wurus wu ñu xellee ci sawara ba mu set wecc, ngir nga am alal. Jëndal itam yére yu weex yoo sol, ba làq sa duŋŋaaral gu gàccelu gi; ak tuufaay looy tuufoo, ngir nga gis. «Man, képp ku ma sopp, maa koy jubbanti, yar ko. Kon nag farlul te tuub!

Peeñu ma 3:17–19

Ndokkalee ñi xiif aka mar jëfe njekk, ndax dinañu regg.

Macë 5:6

«Walaakaanaak néew-doolee ngi wër, di wutum ndox, amul. Seen put wow koŋŋ ak mar. Man Aji Sax ji, maa leen di nangul; man Yàllay Israayil, duma leen wacc.

Esayi 41:17

Buleen fat tuuru jàmbur, buleen sujjóotal tuuru doxandéem.

Taalifi cant 81:10

Ana lu ngeen di waññe xaalis, di ko jënde lu dul aw ñam? Ana lu ngeen di sonn, di jënde lu dul reggal? Dégluleen maa déglu, ba lekk lu leen di dundal, di xéewloo seen ngëneelu bakkan.

Esayi 55:2

Yeesu ne leen: «Man maay ñam wiy joxe dund. Ku ñëw ci man, doo xiif mukk; te ku ma gëm, doo mar mukk.

Yowaan 6:35

Waaye man de tuuti kon ma lajj, tuuti ma tarxiis,

Taalifi cant 73:2

Dama noon: «Tarxiis naa!» Waaye yaa ma awoo sa ngor.

Taalifi cant 94:18

Yeesu neeti: «Simoŋ, Simoŋ! Seytaane kat mu ngi sàkku ab sañ-sañ ngir man leena jéri ni am pepp. Waaye man tinul naa la, ngir sa ngëm baña giim. Yaw nag boo waññikoo, nanga dooleel sa bokki gëmkat.»

Luug 22:31–32

Boroom njekk day daanu juróom ñaari yoon, jógaat, ab soxor sërëx ci njekkar.

Kàddu yu xelu 24:16

Soo tërëfee it, doo daanu. Aji Sax jee lay walloo loxoom.

Taalifi cant 37:24

Yaw samab noon, bu ma ree; maa daanu, maay jóg. Ci biir lëndëm laa toog, waaye Aji Sax jeey samag leer.

Mise 7:8

Juróom benni njàqare teew, mu xettali la ca, ba ko juróom ñaareel sax, doo ca loru.

Ayóoba 5:19

Xale yi doom, loolu laa leen bind, ngir ngeen baña bàkkaar. Waaye su ci amee ku dem ba bàkkaar, am nanu ab layookat fa wetu Baay bi, te mooy Yeesu Almasi bi, boroom njub.

1.Yowaan 2:1

Looloo waral mu mana musal mucc gu mat sëkk, ñiy awe fi moom, dikk fa Yàlla, ndax mooy dund ba fàww, ngir di leen tinul.

Yawut ya 7:25