Meññeefum Noowug Yàlla nag moo di: cofeel ak mbég ak jàmm ak xolu muñ ak mbaax akug tabe ak ngëm akug teey ak noot sa bakkan. Yu mel noonu, wenn yoon bañu ko.
Galasi 5:22–23
Leeru Bés bi
Meññeefum Noowug Yàlla nag moo di: cofeel ak mbég ak jàmm ak xolu muñ ak mbaax akug tabe ak ngëm akug teey ak noot sa bakkan. Yu mel noonu, wenn yoon bañu ko.
Galasi 5:22–23
néew-doole yi dellu bége Aji Sax ji, ñi gëna ñàkk di bànneexoo Aji Sell ju Israayil.
Esayi 29:19
Mu ne leen: «Maa leen ko wax déy, su ngeen dëppul, ba mujj mel niy xale, dungeen tàbbi mukk ci nguurug asamaan. Moo tax ku tuutal boppam ba mel ni xale bii, kooku mooy ki gëna kawe ci nguurug asamaan.
Macë 18:3–4
waaye nay lu làqoo jëmmu biir, nay gànjar gu dul jeex, te mooy lewetaay akug teey, ndax looloo réy njarte fa Yàlla.
1.Piyeer 3:4
Cofeel nag, muñ ak mbaax la. Cofeel bokkul ak kiñaan, bokkul ak jikkoy kañu aka damu.
1.Korent 13:4
Yaw miy nitu Yàlla nag, dawal loolu, te topp njub ak ragal Yàlla ak ngëm ak cofeel ak muñ akug teey.
1.Timote 6:11
Tegooleen sama kilifteef te ngeen jànge ci man, daldi dajeek noflaayal xol, ndax maa lewet, woyof.
Macë 11:29
Dees koo néewal doole, mitital ko te ubbiwul gémmiñam, xanaa mel ni xar mu ñuy rendiji, ne cell ni xar mu ñuy wat, ubbiwul gémmiñam.
Esayi 53:7
Ci loolu sax lañu leen woo, ndax Almasi bi itam sonn na ngir yeen, te moo leen bàyyeel ab royukaay, ngir ngeen jaar ciy tànkam. «Moo bàkkaarul, fenul.» Saaga nañu ko te feyuwul, daj na coono te tëkkoowul, waaye boppam la dénk kiy àtte dëgg.
1.Piyeer 2:21–23
Yeesu nag wax leen ñoom ñépp, ne leen: «Képp ku bëgga dikk topp ma, fàtteel sa bopp, te nga gàddu bés bu nekk, bant bi ñu lay daaj, door maa topp.
Luug 9:23
ci biir teraanga ak ci biir toskare; ci biiri baatal ak jëw yu rafet. Dees noo jàppe ay mbubbookati dëgg, te nuy nit ñu dëggu;
2.Korent 6:8
Te kat képp ku namma farlu ci yoonu Almasi Yeesu, dees na la bunduxataal.
2.Timote 3:12
Man nag bokk yi, su ma dee xiirtale ci xaraf, ana lees may bunduxataaleeti? Kon kay sama waareb deewu Almasi bi ca bant ba dootul doon ag tooñ ci kenn.
Galasi 5:11
Léegi nag ndax nit ñi laay sàkkoo jubool, am Yàlla? Am nit ñi laay wuta neex? Su ma bëggoona wéye neex nit ñi de, duma doon jaamub Almasi bi.
Galasi 1:10
Su ñu leen jànnee sax ndax turu Almasi bi, ndokkalee yeen, ndax Noo gu darajawu gi, Noowug Yàlla moo wàcc ci yeen. Waaye rey nit, mbaa sàcc, mbaa def lu bon, mbaa dugg ci yëfi jàmbur, bumu waral coonoy kenn ci yeen. Ku sonn ndax li muy aji-gëm-Almasi nag, bumu ci rus, na sàbbaal Yàlla kay, ci woowu tur.
1.Piyeer 4:14–16
Ndax kat yeen la may ci jëmmu Almasi bi, yiwu gëm ko, rax ci dolli ngeen sonn ndax moom.
Filib 1:29
Ndaxte cofeelu Almasi bi daal moo nu jiite, nun ñi ràññee lii: gannaaw kenn moo dee ngir ñépp, kon ñépp a dee. Te ki dee ngir ñépp, daa dee ngir ñiy dund bañatee dund ngir seen bopp, xanaa di dund ngir ki dee ngir ñoom, ba dekki.
2.Korent 5:14–15
su nu muñee, nooy bokk nguuru. Su nu ko gàntalee, moom it dinanu gàntal;
2.Timote 2:12
Bés yu mujj yi
Wone yépp31 Ut 2026
30 Ut 2026
29 Ut 2026
28 Ut 2026
27 Ut 2026
26 Ut 2026
25 Ut 2026