Mburu mu amul lawiir ngeen di lekk diiru juróom ñaari fan; te it bu lenn lu am lawiir mbaa lawiir sax am fenn ci seen biir réew.
Mucc ga 13:7
Leeru Bés bi
Mburu mu amul lawiir ngeen di lekk diiru juróom ñaari fan; te it bu lenn lu am lawiir mbaa lawiir sax am fenn ci seen biir réew.
Mucc ga 13:7
Ragal Aji Sax ji mooy bañ lu bon. Réy, xeebaate, yoonu mbon, ak wax ju jekkadi, ma boole bañ.
Kàddu yu xelu 8:13
Na seen cofeel mucc ci ngistal, seexluleen lu bon te ŋoy ci lu baax.
Room 12:9
te lu bon ak nu mu mana bindoo, dàndleen ko.
1.Tesalonig 5:22
Moytuleen balaa kenn di ñàkk yiwu Yàlla. Moytuleen bala ab reenu wextan di fëll, di lëjle, ba rax mbooloom lëmm.
Yawut ya 12:15
Su ma naroon ñaawtéef, Boroom bi du ma déglu.
Taalifi cant 66:18
Kon na ku nekk seetlu boppam, doora lekk ci mburu mi, naan ci kaas bi.
1.Korent 11:28
Teewul cëslaay lu dëgër, li Yàlla tabax, mu ngi ne kekk, te màndarga ma ca nekk, kàddu yii la: «Boroom bi xam na ki mu séddoo,» ak: «Kuy tudd turu Sang bi, na daw njubadi.»
2.Timote 2:19
Boobu sarxalkat bu mag lanu soxla: moo sell, mucc sikk, mucc sobe, moom lañu teqale ak bàkkaarkat yi ci àddina, te moom lañu kaweel ba fa tiim asamaan.
Yawut ya 7:26
Te xam ngeen ne Yeesu moo feeñ ngir far bàkkaar, te taqul fenn bàkkaar.
1.Yowaan 3:5
Jaan ja ne jigéen ja: «Déedéet, dungeen dee! Waaye Yàlla xam na ne bés bu ngeen ci lekkee, seeni gët dina ubbiku, ngeen mel ni Yàlla, xam lu baax ak lu bon.»
Njàlbéen ga 3:4–5
Waaye na jaan ja naxe woon Awa, ca pexeem, ragal naa seenum xel yàqoo noonu, ba dëddu ngëm gu dëggu te set gu ngeen ŋoye woon ci Almasi bi.
2.Korent 11:3
Li ci des nag moo di ngeen manoorewoo Boroom bi, te ngeen sàkkoo ndimbal ci dooleem ak kàttanam gi amul kem. Ràngooleen mboolem gànnaayi Yàlla, ngir ngeen mana jànkoonte ak pexey Seytaane.
Efes 6:10–11
Kon nag jëlleen gànnaayi Yàlla yépp, ba bu bésub safaan taxawee, ngeen mana jëflante, ba sottal, tey wéye taxaw temm.
Efes 6:13
Mbaxanam xare miy seen kaaraange, jëlleen ko, sol; jëlleen itam saamar bi Noo gu Sell giy joxe, te muy kàddug Yàlla.
Efes 6:17
ngir Seytaane bañ noo nax, ndax ay pexeem, umplewunu ko.
2.Korent 2:11
Bés yu mujj yi
Wone yépp2 Sàt 2026
1 Sàt 2026
31 Ut 2026
30 Ut 2026
29 Ut 2026
28 Ut 2026
27 Ut 2026