Yaakaaral Aji Sax ji, dëgërlul te amu fit, te yaakaarati Aji Sax ji.
Taalifi cant 27:14
Leeru Bés bi
Yaakaaral Aji Sax ji, dëgërlul te amu fit, te yaakaarati Aji Sax ji.
Taalifi cant 27:14
Dangeena xamul, am dangeena déggul ne Aji Sax jeey Yàlla ba fàww, sàkk suuf cat ba cat, du sonn, du tàyyi, te am xelam nattuwul? Mooy dooleel ku loof, di kàttanal ku jeele.
Esayi 40:28–29
bul ragal, yaw laa àndal, bul tiit, maay sa Yàlla; maa lay dooleel, dimbali la déy, maa lay téyee sama loxol ndijoor liy àtte dëgg.
Esayi 41:10
Yaa di rawtub néew-ji-doole, di rawtub aji ñàkk, biir njàqare, yaay mbaar mu ñuy yiiroo waame, di ker gu ñuy féexloo ci tàngoor, ndax merum kilifa gu néeg mooy waame wu ne yureet ci kaw ab tabax.
Esayi 25:4
te xam ne bu seen ngëm nattoo, ñeme coono la leen di jural. Na ag ñeme coono sottal liggéeyam ci yeen, ngir ngeen sotti, mat sëkk, te baña yéese fenn.
Yanqóoba 1:3–4
Kon nag buleen teqalikook seenu fit, yool bu réy a ngi ci. Li leen war moo di muñ, ba sottal coobarey Yàlla, su ko defee ngeen jot li mu dige.
Yawut ya 10:35–36
Parlu mu naat la may gooral, wal mu dal, mu tette ma ca,
Taalifi cant 23:2
Waaye ñu bon ñi, mbete géej gu sàmbaraax, tëë dal, gannax yay baaje ban ak suuf. Sama Yàlla nee: «Jàmm du ñeel ñu bon ñi.»
Esayi 57:20–21
«Mboolem yeen ñi loof ndax sëf bu diis, ñëwleen ci man, man maa leen di noppal.
Macë 11:28
Neel tekk, xaar Aji Sax ji, yaakaar ko. Bu sa xol jóg ci kuy baaxle tey lal ay pexe.
Taalifi cant 37:7
Ndax ku tàbbi ci noflaayu Yàlla kat, na Yàlla dalloo woon ca ay liggéeyam, ni ngay dalloo ci say liggéey.
Yawut ya 4:10
Buleen nangu ay àlluwa yu bare te woroo ak sunu ngëm, di leen fàbbi. Li baax mooy ngeen di yokke aw yiw seen pastéefu xol. Buleen yokke pastéefu xol ay ndigal yu jëm ci aw ñam, te ña koy sàmm, jariñu leen dara.
Yawut ya 13:9
Su boobaa nu noppee doon ay tuut-tànk yu nit ñiy muusaatoo kàddu yu mel ni gannax yu nuy baaje ak ngelawal mboolem àlluwa ju bees ju nuy pamti-pamtee ci seen biir pexey naxe ak njublaŋ, ngir fàbbi nu. Su boobaa kay, dëgg gu nu wodde cofeel lanuy wéye, tey màgg ci bépp fànn, ci moom Almasi biy bopp bi.
Efes 4:14–15
Mbete garab gu gëna neex ci gott bi, kookooy sama nijaay ci biir xale yu góor yi. May bége keppaaram, safoo doom ya. Dugal na ma néegub sago-jeex-na, yiire ma mbëggeel.
Ngën-gi-woy 2:3–4
Bés yu mujj yi
Wone yépp1 Sàt 2026
31 Ut 2026
30 Ut 2026
29 Ut 2026
28 Ut 2026
27 Ut 2026
26 Ut 2026