Leeru Bés bi — 7 Sàttumbar: Room 12:12

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Bégeleen seen yaakaar, di muñ ci biir tiis, tey saxoo ag ñaan.

Room 12:12

te li waral ngëm googu ak cofeel googu, di seen yaakaara jot ca cér ba ñu leen dencal fa asamaan. Mooy yaakaar ja ngeen jota am, ba ngeen njëkkee dégg kàddug dëgg gu xibaaru jàmm bi.

Kolos 1:5

Su dee ci giiru dund gii doŋŋ lanu ame yaakaar ci Almasi bi, kon de noo gëna toskare ñépp.

1.Korent 15:19

Ñuy feddali pastéefu taalibe yi, di leen ñaax ngir ñu saxoo ngëm, ne leen: «Coono yu baree ngii, fàww nu jaare ci, ngir tàbbi ci nguurug Yàlla.»

Jëf ya 14:22

Képp ku gàdduwul sa bantu bopp bu ñu lay daaj, te topp ci man, doo mana doon sama taalibe.

Luug 14:27

ngir kenn baña jàq ci biir tiis yii, ndax yeen ci seen bopp xam ngeen ne loolu lanu séddoo.

1.Tesalonig 3:3

Bégleen ci Boroom bi fu ngeen tollu, ma waxati ko, bégleen!

Filib 4:4

Kon Yàlla miy maye yaakaar, yal na leen feesaleek gépp mbég ak jàmm ci biir ngëm, ba ngeen fees dell ak yaakaar, ci manoorey Noo gu Sell gi.

Room 15:13

Cant ñeel na Yàlla, sunu Baayu Sang Yeesu Almasi bi! Moo nu judduwaatal ci yërmandeem ju yaa, ci dooley ndekkitel Yeesu Almasi bi, ngir may nu yaakaar juy dund.

1.Piyeer 1:3

Moom mooy ki ngeen gisul te sopp ko. Tey fi tey gisuleen ko, waaye gëm ngeen ko, ba tax leena bég lool, mbég mu màgg mu làmmiñ manula tudd,

1.Piyeer 1:8

Ci ndimbalam lanu ame ngëm ba mana àgg fi yiwu Yàlla wii nu taxaw taxawaay bu dëgër. Te it sunub sag moo di yaakaar ji nuy séentoo ab cér ci leeru Yàlla.

Room 5:2

Képp ku la wër, yal na bég, di la bànneexoo. Képp ku safoo sag wall, yal na jàppoo: «Aji Sax ji màgg na!»

Taalifi cant 40:17

Ndax man déy, xam naa mébét yi ma leen mébétal. Kàddug Aji Sax jee. Du mébéti loraange, waaye mébéti jàmm laa leen mébétal, ngir may leen yaakaaru ëllëg.

Yeremi 29:11

«Samay xalaat déy du seeni xalaat, te samay jëfin du seeni jëfin.» Kàddug Aji Sax jee. Mu ne: «Ni asamaan tiime suuf, ni la samay jëfin tiime seeni jëfin, samay xalaat it tiime ko seeni xalaat.

Esayi 55:8–9

Yàlla, say xalaat aka maa yéem! Ndaw lim bu réy! Su ma ko doon waññ, moo ëpp feppi suuf. Maa ngii yewwu, nekk feek yaw ba tey.

Taalifi cant 139:17–18

Aji Sax ji, yaa ma bégale say jaloore, may sarxolle ci say manoore.

Taalifi cant 92:5

Ndokkalee, yaw mi dénku ci Aji Sax ji, te sàkkuwoo ku bew ak kuy topp ay fen.

Taalifi cant 40:5

Bokk yi, seetleen ñan ngeen woon, ba ñu leen di woo. Barewul ci seen biir ay xamkat ci gis-gisu nit ñi, barewul ci yeen ay boroom doole, barelewuleen ñu rafet ab juddu.

1.Korent 1:26

Bokk yi, soppe yi, dégluleen. Xanaa du Yàlla moo tànn ñi àddina jàppe ñu néew doole, ngir ñu barele ngëm, boole ci jagoo nguur gi Yàlla dig ñi ko sopp?

Yanqóoba 2:5

Dees noo jàppe boroomi tiis, te nu dëkke mbég; jàppe nu ay néew-ji-doole, te nu woomal ñu bare; jàppe nu ñu amul dara, te nu moom lépp.

2.Korent 6:10

Man mi yées ci ñu sell ñépp lañu may woowu yiw, ba may xibaar jàmbur ñi dul Yawut xéewal yu amul kem yi ci Almasi bi.

Efes 3:8