Nan tàllal sunu xol ak sunuy loxo Yàlla ja fa asamaan,
Jooytu 3:41
Leeru Bés bi
Nan tàllal sunu xol ak sunuy loxo Yàlla ja fa asamaan,
Jooytu 3:41
Ana ku mel ni sunu Yàlla Aji Sax ji, ki kaweel ab jalam, toog, di jéer asamaan ak suuf?
Taalifi cant 113:5–6
Ñeel Daawuda. Aji Sax ji, yaw laay diis sama bakkan.
Taalifi cant 25:1
Ma tàllal lay loxo, soxla la, ni suuf su mar di soxlaa ndox. Selaw. Aji Sax ji, gaawal wuyu ma; sama xol a jeex, ma ne yàcc, bu ma xañ sa yiw, ma yem ak kuy tàbbiji biir pax. Xëye ma sa ngor, yaw laa wóolu; xamal ma fu may doxe, yaw laa wékk sama bakkan.
Taalifi cant 143:6–8
Moo tax kër gu sell ga laa la séentoo, ngir niir sa doole ak sa leer. Xéewloo sa ngor moo dàq dundu bakkan; ma àddu boog, kañ la!
Taalifi cant 63:3–4
Boroom bi, bànneexalal sab jaam, yaw laa dékk sama xol. Boroom bi, yaa baax, di baale, di nàddil sa ngor képp ku lay dagaan.
Taalifi cant 86:4–5
Te lépp lu ngeen ñaan ci sama tur, loolu laay def, ngir Doom ji fésal darajay Baay bi.
Yowaan 14:13
Yéene bii moo wàccal Duuma: Nit a ngi may woowe tundu Seyir, naan: Wattukat bi, lu des ci guddi gi? Éy wattukat bi, lu desati ci guddi gi?
Esayi 21:11
Li tax ngeen wara gëna farlu ci loolu mooy, xam ngeen jant yi nu tollu; seen waxtuw yewwu jot na ba noppi, nde léegi la nu mucc gëna jege ba nuy doora gëm. Guddi gi màggat na, bët a ngi bëgga set. Kon nag nanu bàyyi jëfi lëndëmtu te ràngoo gànnaay yi ñuy xaree cig leer.
Room 13:11–12
Yeesu teg ca ne: «Jàngatleen misaalu garabu figg. Ag figg, bu bànqaas ya duyee, xob ya di sëq, ngeen xam ne nawet jubsi na. Bu ngeen gisee xew-xew yooyu yépp sotti, noonu itam ngeen di xame ne bés bi jubsi na, ba agsi ci bunt bi sax.
Macë 24:32–33
Asamaan ak suuf dina wees, waaye samay wax du wees mukk.
Macë 24:35
Damay xaar Aji Sax ji, di ko xaare xol, di yaakaar kàddoom. Wattukat bi yàkkamti njël, wattukat bi yàkkamti njël, laa ne, ni ma yàkkamtee Aji Sax jee ko raw.
Taalifi cant 130:5–6
Kiy seede mbir yii nee: «Waawaaw, léegi ma ñëw.» Amiin, Sang Yeesu, ñëwal!
Peeñu ma 22:20
«Teewluleen boog, nde xamuleen bés ba, mbaa waxtu wa.
Macë 25:13
Bés yu mujj yi
Wone yépp5 Sàt 2026
4 Sàt 2026
3 Sàt 2026
2 Sàt 2026
1 Sàt 2026
31 Ut 2026
30 Ut 2026