Noonu yaramu nit nekkee wenn te di cér yu bare, ak noonu mboolem céri yaram dee wenn yaram wi, ak li cér yiy bare lépp, noonu rekk la itam ci Almasi bi.
1.Korent 12:12
Leeru Bés bi
Noonu yaramu nit nekkee wenn te di cér yu bare, ak noonu mboolem céri yaram dee wenn yaram wi, ak li cér yiy bare lépp, noonu rekk la itam ci Almasi bi.
1.Korent 12:12
Mooy boppu yaram, wiy mbooloom gëmkat ñi, mooy njàlbéen, mooy taaw bi njëkka dekki, ndekkite lu dee toppul, ba tax muy ki jiitu ci lépp,
Kolos 1:18
Yàlla moo teg lépp fi roni tànkam, te moo ko def muy bopp bi tiim lépp, ñeel mbooloom gëmkat ñi, mbooloo miy aw yaramam. Ci mbooloo mi nag la Almasi bi teewe teewaay bu mat sëkk, te Almasi bi mooy matal lépp ci ñépp.
Efes 1:22–23
nde noo di céri yaramam.
Efes 5:30
Moo tax ba Almasi biy dikk ci àddina la wax ne: «Saraxi jur ak pepp, taamuwuloo ko, waaye aw yaram nga ma waajalal.
Yawut ya 10:5
Gis nga ma, ba ma diw lumb; sa téere lim na fan yi nga ma àppal, ba ca benn dooragul.
Taalifi cant 139:16
«Nit ñi nga tànne ci àddina, jox ma leen, ràññeeloo naa leen saw tur. Sa ñoñ lañu woon, nga jox ma leen, te sa kàddu, sàmm nañu ko.
Yowaan 17:6
Te mooy noonu mu nu tànne ba àddina sosoogul ndax Almasi bi nu bokk, ngir nu doon ñu sell te mucc sikk fa kanamam. Ci biir cofeel
Efes 1:4
Ndax ñooñu Yàllaa leen ràññee woon lu jiitu, te it la mu dogaloon lu jiitu ci ñoom moo di ñu niru Doomam, ngir Doomam di taaw ci biir rakk yu bare.
Room 8:29
Su boobaa kay, dëgg gu nu wodde cofeel lanuy wéye, tey màgg ci bépp fànn, ci moom Almasi biy bopp bi. Ci moom miy bopp bi la yaram wépp di déggoo, temboo ndax ndimbalal mboolem tenqo yi koy saytu, na mu dëppook wàllu cér bu ci nekk. Su ko defee yaram wiy yokku, di màgg ci biir cofeel.
Efes 4:15–16
«Ñaari yoon la xeet wi ma séddoo bàkkaar: ma di bëtu ndox muy dund, ñu wacc ma, man, di gasal seen bopp kàmbi dencukaayi ndox, te kàmb yi fett, di senn.
Yeremi 2:13
Sa njubtee tiim tund yu mag yi, sa àtte ne xéew ni xóotey géej. Céy Aji Sax ji, nit ak mala, nga boole sàmm! Céy Yàlla, yaa wéet ngor, doom aadama yiiroo sa keppaar, yiiru; yafloo sa njël lu duun, sa xéewal wal, nga nàndale ko.
Taalifi cant 36:7–9
Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: «Ma ne sama jaam ñeey lekk, yeen ngeen nekke xiif. Ma ne sama jaam ñeey naan, yeen ngeen nekke mar. Sama jaam ñeey bànneexuji, yeen, ngeen nekke gàcce.
Esayi 65:13
waaye ku naan ci ndox mi ma koy may, man, du marati; ndox mi ma koy may, bëtu ndox lay doon ci moom, di ball, ngir dundug texe gu sax dàkk.»
Yowaan 4:14
Booba Noowug Yàlla la doon wax, Noo ga gëmkati Yeesu doon waaja jot, te jotaguñu ko woon, ndax booba, Yeesoo tàbbeegul woon ci teraangaam.
Yowaan 7:39
«Éey, yeen ñi mar ñépp, dikkleen ci ndox mi, ba ci ku amul xaalis sax! Dikkleen jënd pepp, lekk! Dikkleen jënd pepp mu xaalis jëndul, ak biiñ ak meew mu amul pey.
Esayi 55:1
Noo gu Sell gi ak Séet bi nee ñu: «Ñëwal!» Ku ci dégg it, neel: «Ñëwal!» Ku mar, ñëwal; ku bëgg ci ndoxum dund mi, jëlal, ñu may la.
Peeñu ma 22:17
Bés yu mujj yi
Wone yépp4 Sàt 2026
3 Sàt 2026
2 Sàt 2026
1 Sàt 2026
31 Ut 2026
30 Ut 2026
29 Ut 2026