Ni njeexitalu tooñu kenn nit deme, laa ne, mayu Yàlla demewu ni. Benn bàkkaar moo waral àtte bi indi mbugal. Waaye moy yu bare moo waral may gi teggi tuuma.
Room 5:16
Leeru Bés bi
Ni njeexitalu tooñu kenn nit deme, laa ne, mayu Yàlla demewu ni. Benn bàkkaar moo waral àtte bi indi mbugal. Waaye moy yu bare moo waral may gi teggi tuuma.
Room 5:16
«Kaayleen, nu waxtaan ba juboo,» la Aji Sax ji wax. «Li seeni bàkkaar di xonq lépp, tàll lay weexeji. Li muy xonq curr lépp, weex furr lay mujje.
Esayi 1:18
Mennum man mii maay far say moy ngir man, ba dootuma fàttaliku bàkkaar. Fàttali ma saw lay, nu bokk layoo; waxal boog yaw, ndax nga yey!
Esayi 43:25–26
Maa far say moy, mu naaxsaay niw niir, say bàkkaar ne mes nib lay. Délsil fi man, jot naa la.»
Esayi 44:22
Ndax Yàlla moo sopp àddina, ba joxe jenn Doomam ji, ngir képp ku ko gëm, texe ba fàww, te du sànku mukk.
Yowaan 3:16
Waaye ni moyug Aadama deme, yiwu Yàlla demewu ni. Moyug kenn nit, Aadama, tax na ñu bare dee; waaye yiwu Yàlla ak mayug yiw gu kenn nit, Yeesu Almasi bi, ñaata yoon la gënatee baawaan, ñeel nit ñu bare?
Room 5:15
Te loolu la ñenn ci yeen doonoon. Waaye Yàllaa leen fóot, sellal leen, jubal leen, ci turu Sang Yeesu Almasi bi ak ci sunu Noowug Yàlla.
1.Korent 6:11
Ci biir loolu mu woo fukki surgaam, jox leen ku nekk benn posetub wurus bu gànjare, ne leen: “Liggéeyleen ci, ba ma ñibbisi.”
Luug 19:13
Daa mel ni nit ku tukki, bàyyi këram gannaaw. Fekk na mu batale ay surgaam, ku nekk ak saw sas. Bëkk-néeg bi nag, mu sant ko ne ko mu teewlu.
Màrk 13:34
Kii, mu dénk ko juróomi milyoŋ; kee, ñaar; ka ca des, benn, ku nekk ak la mu àttan. Ci kaw loolu, mu daldi tukki.
Macë 25:15
Danoo wara liggéey liggéeyu ki ma yónni ci bi muy bëccëg; bu guddee kenn du liggéey.
Yowaan 9:4
Mu ne leen: «Lu ngeen may seete? Xamuleen ne sama kër Baay laa wara nekk?»
Luug 2:49
Ci loolu sax lañu leen woo, ndax Almasi bi itam sonn na ngir yeen, te moo leen bàyyeel ab royukaay, ngir ngeen jaar ciy tànkam.
1.Piyeer 2:21
waareel kàddug Yàlla te taxaw ci temm, su neexee ak su naqaree; di yedde, di femmoo, di ñaaxe, tey saxoo muñ ci sa njàngale.
2.Timote 4:2
ku ci nekk, sab liggéey dina feeñ, ndax bés-pénc baa koy xamle, nde sawara lees koy feeñale. Ku ci nekk ak lu sa xeetu liggéey mana doon, sawara lees koy natte.
1.Korent 3:13
Kon nag yeen sama bokk yi ma soppal sama bopp, farluleen, bu leen dara yëngal, te saxooleena jëm kanam ci liggéeyu Sang bi, te ngeen xam ne seenu ñaq, ci seenub ànd ak Sang bi, du neen.
1.Korent 15:58
Bés yu mujj yi
Wone yépp30 Ut 2026
29 Ut 2026
28 Ut 2026
27 Ut 2026
26 Ut 2026
25 Ut 2026
24 Ut 2026