musal ma ca noon yu mag ya ma bañ te man ma.
Taalifi cant 18:18
Leeru Bés bi
musal ma ca noon yu mag ya ma bañ te man ma.
Taalifi cant 18:18
Naxi neen kay lañu jële ca xërëmi tund yu ndaw ya ak coowal kaw tund yu mag ya. Muccu Israayil kay, fi sunu Yàlla Aji Sax ji.
Yeremi 3:23
Mu ne: Aji Sax ji, maa la sopp, yaw mi may dooleel.
Taalifi cant 18:2
Yeen waa Siyoŋ, serleen te sarxolleel Ku màgg ki fi seen biir, Aji Sell ju Israayil.»
Esayi 12:6
Néew-ji-doole woote, Aji Sax ji wuyu, musal ko fu mu jàqe.
Taalifi cant 34:7
Aji Sax jeey won gannaaw ñiy def lu bon, ngir dagge leen kaw suuf, far seeni tur.
Taalifi cant 34:17
Yàlla ji sax fàww moo dib rawtu, përëgam bi sax dàkk di cëslaay, moo la dàqal ab noon ne la: “Jekkalil!”
Baamtug yoon wi 33:27
Moo tax nu mana am fitu wax ne: «Boroom beey sama ndimbal, duma tiit. Ana lees ma manal?»
Yawut ya 13:6
Yàllaa mat. Kàddug Aji Sax jee wér te wóor. Mooy feg képp ku ko làqoo. Ana kuy Yàlla ku moy Aji Sax ji? Ana ku mat cëslaay ku dul sunu Yàlla?
Taalifi cant 18:31–32
Ci yiwu Yàlla daal laa doone ki ma doon, te yiw woowu ma ñeel neenul. Te sax yeneen ndaw yépp sax, maa leen gëna liggéey. Du ci man nag, waaye yiwu Yàlla wi ànd ak man la.
1.Korent 15:10
Nun ñépp a lajj niy xar, ku nekk walbatiku topp yoonam, te Aji Sax jee ko sëf mbugal mi nu wara dékku nun ñépp.
Esayi 53:6
Su nu waxee ne amunu bàkkaar, sunu bopp lanuy nax, te amunu dëgg.
1.Yowaan 1:8
Noonu it la Mbind mi indee ne: «Kenn jubul, du kenn sax. Kenn xeluwul, kenn wutul Yàlla. Ñépp a lajj, bokk yàqu yaxeet, Kenn deful lu baax, du kenn sax!
Room 3:10–12
«Yeena réeroon niy xar,» waaye délsi ngeen tey ci seenub sàmm, seen wattukatub xol.
1.Piyeer 2:25
Lajj naa ni xar mu réer; gindi ma, Sang bi, sàgganewuma say santaane de!
Taalifi cant 119:176
leqali ma, teg ma ci yooni njub ngir teraangay turam.
Taalifi cant 23:3
Samay xar, sama baat lañuy déglu; maa leen xam, te man lañuy topp. Man maa leen di texeel ba fàww; duñu sànku mukk, te kenn du leen foqatee ci sama loxo.
Yowaan 10:27–28
«Ana kan ci yeen mooy am téeméeri xar, réerle ci menn, te bàyyiwul ca àll ba juróom ñeent fukki xar ya ak juróom ñeent (99), ngir toppi ma réer, ba gis ko?
Luug 15:4
Bés yu mujj yi
Wone yépp22 Awr 2026
21 Awr 2026
20 Awr 2026
19 Awr 2026
18 Awr 2026
17 Awr 2026
16 Awr 2026