Ki may sarxale jaajëf moo ma teral; ku topp yoon, ma won ko wallub Yàlla.»
Taalifi cant 50:23
Leeru Bés bi
Ki may sarxale jaajëf moo ma teral; ku topp yoon, ma won ko wallub Yàlla.»
Taalifi cant 50:23
Na kàddug Almasi bi dëkk ci yeen, bay baawaan, ngeen di jariñoo xel mu mat sëkk mu ngeen di jàngalantee aka artoonte. Woyeleen xolub cant, ñeel Yàlla, ak ay taalifi cant ak woyi tagg Yàlla ak woy yu ñu fente ci Noowug Yàlla gi. Lu ngeen mana def, muy ci wax, di ci jëf, defleen ko ci turu Sang Yeesu, tey sant Yàlla Baay bi ci moom.
Kolos 3:16–17
ndax dees leena jot, ba fey njëg ga. Kon nag seen yaram, terale leen ko Yàlla.
1.Korent 6:20
Waaye yeen nag yeenay giir giy tànnéef, yeenay sarxalkati buur, yeenay askan wu sell, yeenay xeet wi ñu jot, ngir ngeen biral jaloore yu wéet yi ñeel ki leen woo, génnee leen cig lëndëm, indi leen ci leeram gu yéeme.
1.Piyeer 2:9
Te yeen itam yeen ay doji cëslaay yuy dund, doj yi Noo gu Sell gi tabaxe ag kër Yàlla, ñeel liggéeyu carxal gu sell, ngir ngeen di ko jébbal ay sarax yu Noo gi rafetlu, sarax yu Yàlla nangu ndax Yeesu Almasi bi.
1.Piyeer 2:5
Kon nag saa su nekk, nanuy jaare ci Yeesu, di génne sunu saraxu cant, ñeel Yàlla, muy sarax su bawoo ci sunuw làmmiñ, ñu di ko birale aw turam.
Yawut ya 13:15
Naa màggal Aji Sax ji saa su ne, di ko sant fu ma tollu. Aji Sax ji laay sagoo, néew-ji-doole dégg, bég.
Taalifi cant 34:2–3
Yóbbaale ma, nu daw, dem. Sama buur, yóbbu ma sa néeg, nu bokk mbég ak bànneex, di tàqamtikoo sa cofeel gi dàq biiñ. Ñoo yey nob la!
Ngën-gi-woy 1:4
Ñu ne: «Bu yàgg la nu Aji Sax ji feeñu, ne nu: “Maa leen masa bëgg, ba tax ma sédd leen ngor.
Yeremi 31:3
Ay goji nit laa leen ñoddee, ay buumi cofeel. Maay ki leen yolomalal ŋalaabi ŋaam, sëgg, leel leen.
Ose 11:4
Man nag kera bu ñu ma yékkatee, jële ma fi kaw suuf, ñépp laay xëcc, jëme ci man.»
Yowaan 12:32
Naka la Yeesu di romb, Yaxya ne ko jàkk, ne: «Kii moo di Xarum Yàlla!»
Yowaan 1:36
Te itam noonee Musaa yékkatee woon jaan ja ca màndiŋ ma, fàww ñu yékkatee ni Doomu nit ki, ngir képp ku ko gëm, texe ba fàww.»
Yowaan 3:14–15
Ana ku ma am asamaan ku la moy? Ku ma safoo kaw suuf ku la moy?
Taalifi cant 73:25
Nun nag, li nu taxa am cofeel moo di Yàlla moo nu njëkka sopp.
1.Yowaan 4:19
Sama nijaay ne ma: «Xarit, ayca, jongama sama, dikkal boog! Xoolal, tawub sedd wees na, waame jàll, wéy. Tóor-tóor yi lal na réew mi, jamonoy woy dikk, sabum péget jibe sunum réew. Figg a ngi ñorsi, reseñ tóor, di gilli. Xarit, ayca, jongama sama, dikkal boog!»
Ngën-gi-woy 2:10–13
Bés yu mujj yi
Wone yépp16 Awr 2026
15 Awr 2026
14 Awr 2026
13 Awr 2026
12 Awr 2026
11 Awr 2026
10 Awr 2026