Gannaaw loolu Aji Sax ji yéwéne na Saarata, ni mu ko waxe woon, defal ko li mu ko digoon.
Njàlbéen ga 21:1
Leeru Bés bi
Gannaaw loolu Aji Sax ji yéwéne na Saarata, ni mu ko waxe woon, defal ko li mu ko digoon.
Njàlbéen ga 21:1
Yàllaa may musal, di ma sagal, ma di ko doolewoo. Sama kiiraay, Yàllaa!
Taalifi cant 62:8
Ba loolu amee Daawuda jàq lool, ndax mbooloo maa nga doon wax naan dañu koy dóori doj. Booba mbooloo ma ba mu daj, ku nekk a ngaak naqaru xol, di xalaat doomam yu góor ak yu jigéen. Daawuda nag dëgërloo Yàllaam Aji Sax ji rekk.
1.Samiyel 30:6
Mu am bés Yuusufa ne ay bokkam: «Sama waxtu jege na, waaye Yàlla dina dikk, yéwéne leen moos, ba jële leen ci réew mii, yóbbu leen ca réew ma mu dige woon, ba giñal ko Ibraayma, Isaaxa ak Yanqóoba.»
Njàlbéen ga 50:24
Gis naa bu baax sama coonob ñoñ ci Misra; maa dégg seeni onk, ba wàcc ngir wallusi leen. Léegi nag dikkal, ma yebal la Misra.”
Jëf ya 7:34
Moo leen génne réewum Misra, moo def ay kéemaan aki firnde ca réew ma ak ca géeju Barax ya ak ca màndiŋ ma, diiru ñeent fukki at.
Jëf ya 7:36
Du benn dige bu wuute ci mboolem digey ngëneel ya Aji Sax ji giñaloon waa kër Israayil. Lépp a mat sëkk.
Yosuwe 21:45
Nanu ŋoy ci yaakaar ji nu biral ne moom lanu am, te nu baña yoqi, nde ki dige ku wóor la.
Yawut ya 10:23
Yàlla du nit, bay fen, du doom aadama bay tuub. Moom wax na lu mu deful a? Am àddu na lu mu sottalul?
Màndiŋ ma 23:19
Asamaan ak suuf dina wees, waaye samay wax du wees mukk.
Macë 24:35
Am ñax day wow; tóor-tóor day lax. Waaye sunu kàddug Yàlla mooy sax ba fàww.»
Esayi 40:8
Ñépp a la wékk bët, di yaakaar, te bu jotee, yaa leen di leel,
Taalifi cant 145:15
Te it jariñoowul loxol nit, mbete ku soxla lenn, ndax mooy may ñépp bakkan akug noo, ak lu mu mana doon.
Jëf ya 17:25
Aji Sax jee baaxe ñépp, di yërëm lu mu sàkk.
Taalifi cant 145:9
Xoolleen picc yi: duñu ji, duñu góob, duñu denc ci am sàq. Teewul seen Baay ba fa asamaan di leen dundal. Yeen nag, xanaa du yeena gën picc yi fuuf?
Macë 6:26
Ag wuutale amul diggante ab Yawut ak jàmbur bu dul Yawut; ñépp a bokk benn Boroom biy yéwéne mboolem ñi koy woo wall.
Room 10:12
Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla. Damaa séentu tund ya, te naan fu wall di jóge?
Taalifi cant 121:1
Ma ne, ni jaam bu góor di wékke sangam bët, jaam bu jigéen di ko wékke bët sangam bu jigéen, ni lanuy wékke sunu Yàlla Aji Sax ji bët, ba keroog mu baaxe nu.
Taalifi cant 123:2
Aji Sax ji déy a leen namma baaxe, moo ko tax di jóg moos ngir yërëm leen, nde Aji Sax jeey Yàllay njubte. Ndokkalee képp ku ko yaakaar!
Esayi 30:18
Bésub keroog dees na ne: «Sunu Yàllaa ngii nag! Moom mii lanu yaakaaroon te moo nuy wallu. Aji Sax jii lanu yaakaaroon, nan bég te bànneexoo wallam.»
Esayi 25:9
Li nu gisul kay lanuy yaakaar, di ko séentooka muñe yaakaar ji.
Room 8:25
Bés yu mujj yi
Wone yépp23 Awr 2026
22 Awr 2026
21 Awr 2026
20 Awr 2026
19 Awr 2026
18 Awr 2026
17 Awr 2026