Mboolem alalu lël ju jóge ca dëkk ba, dajaleleen ko ca digg pénc ma, te ngeen lakk dëkk ba, booleek lël ba, def ko dóomal bu mat sëkk, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji. Day doon ab gent ba fàww, deesu ko tabaxaat.
Baamtug yoon wi 13:17
Leeru Bés bi
Mboolem alalu lël ju jóge ca dëkk ba, dajaleleen ko ca digg pénc ma, te ngeen lakk dëkk ba, booleek lël ba, def ko dóomal bu mat sëkk, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji. Day doon ab gent ba fàww, deesu ko tabaxaat.
Baamtug yoon wi 13:17
Kon nag: «Nangeen génne ci seen biir, te teqalikoo ak ñoom,» la Boroom bi wax, «lu sobewu, buleen ko laal. Su boobaa, maa leen di dalal.
2.Korent 6:17
Soppe yi, ay gan ngeen, ay doxandéem ci kaw suuf. Kon nag li ma leen di dénk moo di ngeen moyu xemmemtéefi bakkan yiy xeex ak ab xol.
1.Piyeer 2:11
ñii ngeen wallu leen, foqatee leen ci sawara, ña ca des, ngeen yërëm leen yërmande ju ànd akug ragal, ba far seexlu ab turki bu seen yaram sobeel ndax seeni bàkkaar.
Yudd 23
Soppe yi, léegi doomi Yàlla lanu, te li nuy dooni nag feeñagul. Waaye xam nanu ne bés bu Almasi bi feeñee, nooy nirook moom, ndax su boobaa, ni mu nekke, noonu lanu koy gise. Te képp ku am jooju yaakaar ci moom, noonu mu sete, ni lay setale boppam.
1.Yowaan 3:2–3
Ndax yiwu Yàlla kat feeñ na, te looloo indil ñépp ag mucc. Yiw woowu moo nu digal nu dëddu ñeme Yàlla ak xemmemtéefi àddina, te jiital sunum xel, di jëfe njub, te nekke ragal Yàlla ci àddinay tey jii. Loolu lees nu digal, li feek nu ngi séentu yaakaaru mbég ma, keroog bésu peeñum sunu màggaayu Yàlla miy Yeesu Almasi bi, Musalkat bi. Moo maye bakkanam ngir nun, moo nu jot, ba nu mucc ci gépp njubadi, moo nu def askan wu mu setalal boppam, séddoo nu, nuy askan wu farlu ci jëf ju baax.
Tit 2:11–14
«Ma ne ko: “Sang bi, yaa di kan?” Sang bi ne ma: “Man maay Yeesu, mi ngay bunduxataal.
Jëf ya 26:15
Yeesu wax ak ñoom ca saa sa, ne leen: «Dalleen, man mii la, buleen tiit!»
Macë 14:27
Booy xuus cim ndox, maa ngi ànd ak yaw; ag dex du la mëdd. Booy dox cib taal, doo lakk, sawara du la xoyom. Man Aji Sax ji, maay sa Yàlla; man Aji Sell ju Israayil, maa lay musal. Maa joxe Misra, feye la; ak Kuus ak Saba, ma weccikoo la.
Esayi 43:2–3
Su may jaare xuru dee wu ne këruus it, duma ragal loraange: yaw laak man, sa bantu sàmm ak sa nguul, yooyoo may dalal.
Taalifi cant 23:4
«Janq bi mooy ëmb, jur doom ju góor, ñu tudde ko Emanuwel,» muy firi Yàllaa ngi ak nun.
Macë 1:23
Doom ju góor lay am; nanga ko tudde Yeesu (muy firi Boroom beey musle), ndax mooy musal aw xeetam ci seeni bàkkaar.»
Macë 1:21
Xale yi doom, loolu laa leen bind, ngir ngeen baña bàkkaar. Waaye su ci amee ku dem ba bàkkaar, am nanu ab layookat fa wetu Baay bi, te mooy Yeesu Almasi bi, boroom njub.
1.Yowaan 2:1
Ana kuy tegeb daan? Almasi Yeesu de moo dee, rax ci dolli, mu dekki, te moo toog fa ndijooru Yàlla, di nu fa ñaanal! Ana ku nuy tàggaleek cofeelu Almasi bi? Du ay nattu, te du njàqare, du it coonoy bunduxataal, mbaa ab xiif, mbaa rafle, te du genn aayteef, ba cib saamar.
Room 8:34–35
Bés yu mujj yi
Wone yépp19 Awr 2026
18 Awr 2026
17 Awr 2026
16 Awr 2026
15 Awr 2026
14 Awr 2026
13 Awr 2026