Leeru Bés bi — 21 Awril: Filib 4:1

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Kon nag yeen samay bokk, soppe yi ma namm, di leen bége, te ngeen di sama kaalag ndam gi ma yooloo ci sama liggéey, ngalla soppe yi, nangeen saxe noonu ci Boroom bi!

Filib 4:1

Tànkam, sama tànk, yoonam laa tegu, moyuma ko.

Ayóoba 23:11

Aji Sax ji kat dafa jiital yoon, te du wacc jaamam bu gore. Day fegu ba fàww; askanu ku bon dog.

Taalifi cant 37:28

Aji Sax jee lay sàmm ci gépp loraange, di sàmm sa bakkan.

Taalifi cant 121:7

Sama nit ku jub nag mooy dund ndax ngëm ga, waaye ku dellu gannaaw, sama xol bégewu la.» Nun nag bokkunu ci ñiy dellu gannaaw te nara sànku, waaye nooy ñi saxoo ngëm te nara mucc.

Yawut ya 10:38–39

Ci nun lañu jóge nag, waaye bokkuñu ci nun, ndax su ñu bokkoon ci nun, ci nun lañuy des. Waaye noonu la bire ne du ñoom ñépp a bokk ci nun.

1.Yowaan 2:19

Yeesu moo waxoon Yawut yi ko gëmoon ne leen: «Bu ngeen saxee ci sama kàddu, samay taalibe dëgg ngeen.

Yowaan 8:31

Waaye ku muñ ba muj ga, kooku dina mucc.

Macë 24:13

Teewluleen te saxoo ngëm, góor-góorluleen te dëgërlu.

1.Korent 16:13

«Léegi ma ñëw. Ŋoyal ci li nga yor, ngir kenn baña fëkk sa kaalag ndam.

Peeñu ma 3:11

Ku am ndam mooy soloo noonu mbubb mu weex, te turam, duma ko far ci téereb dund bi, waaye maa koy wuyul ci sama kanam Baay ak ay malaakaam.

Peeñu ma 3:5

Matusalem juddu na, ba noppi Enog topp Yàlla ñetti téeméeri at (300), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen.

Njàlbéen ga 5:22

Ndax ñaar dina ànd te digewuñub dajee?

Amos 3:3

Deretam ja tuuru ca bant ba, ca la Yàlla defe jàmm, ba sottale ci moom, pexe mi mu jubalee boppam ak lépp, muy lu nekk ci kaw suuf ak la fa asamaan. Te yeen ñi masoona sore lool Yàlla, doonoon ay noonam ci wàllu xalaat ak jëf ju bon, tey, deewug yaram, deewug suux gi Almasi bi dee, moom la leen Yàlla jubalee ak boppam, ba teewal leen fi kanamam, ngeen di ñu sell, mucc sikk, seen der set wecc.

Kolos 1:20–22

Waaye yeen ñi sore woon, léegi bi ngeen nekkee ci Almasi Yeesu, jege ngeen ndax deretu Almasi ji tuuru.

Efes 2:13

Ndegam ba ñu dee ay bañaaley Yàlla lees nu jubalee deewug Doomam, ñaata yoon lees nuy gënatee musale ag dundam, gannaaw ba ñu nu jubalee ak Yàlla? Te yemunu ci, xanaa di sagoo Yàlla itam ndax sunu Boroom Yeesu Almasi bi nu jubale ak moom.

Room 5:10–11

Li nu gis te dégg ko, moom lanu leen di àgge, ngir yeen itam ngeen am ak nun ag jokkoog mbokk. Te sunu jokkoog mbokk googu, nook Baay bi lanu ko séqal, ak Doomam Yeesu Almasi bi.

1.Yowaan 1:3