Ab yonent laa leen di feeñalal ci seen biiri bokk, ni yaw. Maay yeb samay kàddu ci gémmiñam, mu àgge leen mboolem lu ma ko sant.
Baamtug yoon wi 18:18
Leeru Bés bi
Ab yonent laa leen di feeñalal ci seen biiri bokk, ni yaw. Maay yeb samay kàddu ci gémmiñam, mu àgge leen mboolem lu ma ko sant.
Baamtug yoon wi 18:18
Maa taxaw diggante Aji Sax jeek yeen, jant yooyu, di leen jottali kàddug Aji Sax ji, ndax yeena ragaloon sawara wa, ba yéeguleen ca kaw tund wa. Mu ne:
Baamtug yoon wi 5:5
Ndax kat jenn Yàlla doŋŋ moo am, benn rammukat doŋŋ it moo am diggante Yàlla ak nit ñi, te mooy kenn nit: muy Almasi Yeesu
1.Timote 2:5
Góor ga Musaa nag defoon ku woyof lool, ba raw mboolem doom aadama ci kaw suuf.
Màndiŋ ma 12:3
Tegooleen sama kilifteef te ngeen jànge ci man, daldi dajeek noflaayal xol, ndax maa lewet, woyof.
Macë 11:29
Noonu Almasi Yeesu doon doxale, deeleen ko doxale ci seen biir: Moom mi nekke nekkinu Yàlla te ŋoyaaloowul ci dayob boppam bi ko def nawleb Yàlla. Xanaa mu ŋacc boppam, nangoo jagoo nekkinu surga. Mu mujj mel ni nit doŋŋ, di ku ñu xàmmee jëmmu nitam.
Filib 2:5–7
Musaa déy «jawriñ ju wóor la woon ci biir mboolem waa kër Yàlla,» di seedeel Yàlla kàddu ya ñu fa wara wax. Almasi bi nag mooy Doom ju wóor ji jiite kër Yàlla, te nun nooy këram, ndegam kay nu ngi wéye aw fit ak yaakaar ji nuy puukarewoo.
Yawut ya 3:5–6
Sunu Sang Yeesu Almasi bi ci boppam ak Yàlla sunu Baay mi nu sopp, te may nu ciw yiwam, jàmmi xol ju sax dàkk ak yaakaar ju wér,
2.Tesalonig 2:16
Waaye man maay bàyyi xel sama kóllëre gi ma fasoon ak yaw ba ngay ndaw. Maa lay saxalal kóllëre guy wéy ba fàww.
Esekiyel 16:60
Kon bennub sarax boobu, ci la matale sëkk ba fàww nit ñi ñu sellal.
Yawut ya 10:14
Looloo waral mu mana musal mucc gu mat sëkk, ñiy awe fi moom, dikk fa Yàlla, ndax mooy dund ba fàww, ngir di leen tinul.
Yawut ya 7:25
Looloo tax may daj yii coono. Waaye rusuma ci, ndax xam naa ki ma gëm, te wóor na ma ne, li ma ko dénk, moo ko mana sàmm ba keroog bés ba.
2.Timote 1:12
Ndax Yàlla kat, ay mayam akub wooteem, lenn du ci toxu.
Room 11:29
Ana ku nuy tàggaleek cofeelu Almasi bi? Du ay nattu, te du njàqare, du it coonoy bunduxataal, mbaa ab xiif, mbaa rafle, te du genn aayteef, ba cib saamar.
Room 8:35
ndaxte Xar mi ci diggu ngàngune mi moo leen di sàmm, yóbbu leen ca bëti ndoxum dund ma, te Yàllaa leen di fompal wépp rongooñ.»
Peeñu ma 7:17
Jógleen dem, fii du bérebu noflaay, nde sobewu na, ba nara yàqe yaxeet.
Mise 2:10
ndax amunu fii ci àddina dëkk bu sax ba fàww, waaye dëkk biy ñëw, moom lanuy sàkku.
Yawut ya 13:14
Bés yu mujj yi
Wone yépp17 Awr 2026
16 Awr 2026
15 Awr 2026
14 Awr 2026
13 Awr 2026
12 Awr 2026
11 Awr 2026