Leeru Bés bi — 16 Awril: Taalifi cant 31:22

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Cant ñeel na Aji Sax ji! Ndaw kéemtaan ci ngor li mu ma jiwe biir dëkk bu ñu gaw.

Taalifi cant 31:22

Éy Yàlla, wallu ma! Ndox maa ngi ma tollu ci put.

Taalifi cant 69:2

ndox ma mëdd ma, ma ne: «Sànku naa.» Aji Sax ji, fa xóotey pax ma laa la woowe. Sama baat nga dégg, ma ne la: «Bul fattal sab nopp samay onk ak samay yuux.» Bés ba ma la woowee nga dikk, ne ma: «Bul tiit.»

Jooytu 3:54–57

Guddi may fàttaliku sama woy, di waxtaan ak sama ngegenaay, sama xel di jéex te naa: «Boroom bi da may gàntal ba fàww, ba du ma baaxeeti mukk a? Xanaa daa jeexal ngor tàkk? Am kàddoom a deñ ba fàww? Moo, mbaa du Yàlla daa fàtte ñeewante? Am meram a tëj buntu yërmandeem?» Selaw. Ma ne, sama naqar daal mooy Aji Kawe ji daa soppi loxoom.

Taalifi cant 77:7–11

Maay dajeek ngëneelu Aji Sax ji fi kaw suuf sii. Lii wóor na ma.

Taalifi cant 27:13

Mu woo ma, ma wuyu ko; mook man ci biir njàqare, ma xettali ko, darajaal ko,

Taalifi cant 91:15

Guddig keroog la Yàlla feeñu Suleymaan. Mu ne ko: «Ñaanal loo bëgg ma may la ko.» Suleymaan ne Yàlla: «Yaw de yaa baaxe lool Daawuda saa baay, te yaa ma fal buur, ma wuutu ko.

2.Jaar-jaar ya 1:7–8

Kon nag xel ak xam-xam nga may may, ba ma xam nu may jiitee askan wii. Ndax kat, ana kan mooy àtte sa ñoñ, wii askan wu yaa?»

2.Jaar-jaar ya 1:10

Aji Sax ji nag duma Kuuseen ña fa kanam Asa ak Yuda, Kuuseen ña daw. Asa ak gàngoor ga mu àndal dàqi Kuuseen ña ba Gerar, ñu daanu, kenn rëccul. Fa kanam Aji Sax ji ak fa kanam gàngooram lañu rajaxoo. Ci kaw loolu Yudeen ña yóbbu alalu sëxëtoo ju bare lool.

2.Jaar-jaar ya 14:11–12

Éy Yàlla, yaa jagoo cant fa Siyoŋ, yaw lees di jëfeel ab dige.

Taalifi cant 65:2