Ci kaw loolu Yeesu neeti: «Maa leen ko wax déy ci lu wér, man maay buntu wërmbalu xar yi.
Yowaan 10:7
Leeru Bés bi
Ci kaw loolu Yeesu neeti: «Maa leen ko wax déy ci lu wér, man maay buntu wërmbalu xar yi.
Yowaan 10:7
Ca saa sa ridob biir néegu Yàlla ba dale ca kaw ba ca suuf, xar ñaar, suuf sa yëngu, doj ya xar,
Macë 27:51
Almasi bi itam benn yoon la daj coono ndax bàkkaari nit ñi, moom miy ki jub moo leen ko defal yeen ñi jubadi, ngir yóbbu leen fa Yàlla; moom lañu rey yaramu suuxam, waaye moo dundaat ci dooley Noo gu Sell gi.
1.Piyeer 3:18
Noonu la Noo gu Sell gi firndeele ne yoon wu maye ñu dugg ca néeg bu sella sell ba feeñagul woon, te fekk néeg bu njëkk ba di taxaw ba tey.
Yawut ya 9:8
Man maay bunt bi; ku dugge ci man, dinga mucc, di dugg aka génn, di gis mbooy goo fore.
Yowaan 10:9
Yeesu ne ko: «Man maay yoon wi, maay dëgg gi, te maay dund gi. Kenn du ñëw ci Baay bi te jaarewul ci man.
Yowaan 14:6
ndax nun ñaari xeet yépp, ci moom Almasi bi lanu jote ci Baay bi, ci ndimbalal genn Noo gu Sell gi. Kon nag dootuleen ay gan mbaa ay doxandéem, waaye ay nawley ñu sell ñi ngeen, te waa kër Yàlla ngeen.
Efes 2:18–19
Léegi nag bokk yi, am nanu sañ-sañu dugg ca néeg bu sella sell ba, ngir deretu Yeesu, deretu Yeesu jiy yoon wu yees, yoonu dund gu mu nu xàllal, jàllale ko ca rido ba, te rido ba moo di yaramu suuxam wi mu saraxe.
Yawut ya 10:19–20
Gannaaw nag dees noo baaxe àtteb ñu jub ci kaw ngëm, jàmmoo nanu ak Yàlla ndax sunu Sang Yeesu Almasi bi. Ci ndimbalam lanu ame ngëm ba mana àgg fi yiwu Yàlla wii nu taxaw taxawaay bu dëgër. Te it sunub sag moo di yaakaar ji nuy séentoo ab cér ci leeru Yàlla.
Room 5:1–2
Su ma nee: «Xaaral ma fàtte ko, dootuma jottali kàdduy waxyu ci turam,» sama xol bi mel nib taal bu tàkk, tàbbi sama biir yax yi; may jéema muutuwaale sa kàddu, te duma ko man.
Yeremi 20:9
Yégle xibaaru jàmm bi moom, du lu may kañoo. Wartéef la wu ñu ma sas, te ngalla man, su ma yéglewul xibaaru jàmm bi!
1.Korent 9:16
kon ana lu ciy sama peyoor? Xanaa ma man di yégle xibaaru jàmm bi ci dara, ba duma jariñoo sañ-sañu dunde xibaaru jàmm bi may yégle.
1.Korent 9:18
Ñu woo leen nag, aaye leen, ne leen mayatuñu leen benn yoon ñu waxati lenn, mbaa ñuy jàngale ci turu Yeesu. Piyeer ak Yowaan ne leen: «Ndax li jaadu fa Yàlla mooy nu déggal leen, yeen, bàyyi Yàlla? Yeenay àtte loolu. Waaye nun, li nu gis, dégg ko, manunu koo baña wax.»
Jëf ya 4:18–20
Ndaxte cofeelu Almasi bi daal moo nu jiite, nun ñi ràññee lii: gannaaw kenn moo dee ngir ñépp, kon ñépp a dee.
2.Korent 5:14
Moo tax ma ragal, ba dem gas ca suuf, làq ca sab milyoŋ. Mu ngii, fabal sa alal.” Njaatige la nag ne ko: “Surga bu bon bi te yaafus! Xamoon nga ne damay dajale lu ma jiwuloon, di góob lu ma faruwuloon. Kon waroon ngaa yóbbu sama xaalis ca denckati xaalis ya, ba bu ma dikkee, jot sama milyoŋ, boole ca tonoom.
Macë 25:25–27
Waaye Yeesu mayu ko ko. Da ne ko: «Ñibbil sa kër ca say bokk, nga àgge leen li la Boroom bi defal lépp ci yërmandeem.»
Màrk 5:19
Bés yu mujj yi
Wone yépp18 Awr 2026
17 Awr 2026
16 Awr 2026
15 Awr 2026
14 Awr 2026
13 Awr 2026
12 Awr 2026