Teralal Aji Sax ji ci sa alal ak loo njëkka meññle,
Kàddu yu xelu 3:9
Leeru Bés bi
Teralal Aji Sax ji ci sa alal ak loo njëkka meññle,
Kàddu yu xelu 3:9
Lii rekk la: ji lu tuut, góob lu tuut; ji lu bare, góob lu bare.
2.Korent 9:6
Bés bu njëkk ci ayu bés yi, na ku nekk génne as lëf ca la mu am, na mu ko àttane, te mu dencal ko boppam, ngir bu ma dikkee, dootul soxlaa wër, di dajale.
1.Korent 16:2
Yàlla ñàkkul worma bay fàtte seen liggéey ak cofeel gi ngeen sopp turam, te firndeele ko ni ngeen taxawoo ñu sell ñi, démb ak tey.
Yawut ya 6:10
Kon nag bokk yi, ma ñaax leen, te yërmandey Yàlla tax. Na seen dund mel ni sarax su ñuy defal Yàlla, sarax su sell te neex ko. Loolu déy mooy njaamu gi leen war.
Room 12:1
Ndaxte cofeelu Almasi bi daal moo nu jiite, nun ñi ràññee lii: gannaaw kenn moo dee ngir ñépp, kon ñépp a dee. Te ki dee ngir ñépp, daa dee ngir ñiy dund bañatee dund ngir seen bopp, xanaa di dund ngir ki dee ngir ñoom, ba dekki.
2.Korent 5:14–15
Bunti dëkk bi du tëje mukk bëccëg, te foofa sax guddi amu fa.
Peeñu ma 21:25
Du jant a lay leeralati bëccëg, te weer du la niital; Aji Sax jeey doon sag leer ba fàww, sa Yàlla jooju di sab taar.
Esayi 60:19
Te dëkk bi soxlawul jant bu koy leeral mbaa weer, ndax leeru Yàllaa koy leeral, Xar mi di làmpam.
Peeñu ma 21:23
Guddi du amati, te deesul soxlaati làmp mbaa naaj, ndax Boroom bi Yàlla moo leen di leeral. Te dañuy nguuru ba fàww.
Peeñu ma 22:5
Waaye yeen nag yeenay giir giy tànnéef, yeenay sarxalkati buur, yeenay askan wu sell, yeenay xeet wi ñu jot, ngir ngeen biral jaloore yu wéet yi ñeel ki leen woo, génnee leen cig lëndëm, indi leen ci leeram gu yéeme.
1.Piyeer 2:9
te ngeen di sante Baay bi mbég, moom mi leen yellale ab cér ca muuru ñu sell ña, ca réewum leer ga. Yàlla kat moo nu wallu ba génne nu ca kilifteefu réewum lëndëm ga, toxal nu ci biir nguurug Doomam ji mu sopp.
Kolos 1:12–13
Ag lëndëm ngeen woon démb, waaye tey ag leer ngeen ci Boroom bi ngeen bokk. Jëfeleen nag ni niti leer.
Efes 5:8
Yeen ñépp ay doomi leer ngeen, doomi bëccëg ndarakàmm; nun bokkunu dara ak guddi, mbaa ag lëndëm.
1.Tesalonig 5:5
Yoonu ku jub day leer, ba ne ràññ ni bëccëg.
Kàddu yu xelu 4:18
Bés yu mujj yi
Wone yépp12 Awr 2026
11 Awr 2026
10 Awr 2026
9 Awr 2026
8 Awr 2026
7 Awr 2026
6 Awr 2026