Li yoonu Musaa tële woon ndax néew dooley nitu suuxu neen, mooy lii Yàlla def: Doomam la yónni, mu dikke melow nit, te nit di bàkkaarkat, di suuxu neen, ngir Doomam fajtal mbirum bàkkaar. Yaramu suux wu nit kooku la Yàlla sottale mbugal mi war ci bàkkaar,
Room 8:3
Yoonu Musaa takkndeeru xéewal yiy ñëw doŋŋ a ci nekk, waaye xéewal ya ci seen bopp nekku ci. Looloo tax sarax yi yoon wi laaj ñu war koo saxoo jébbale at mu nekk, manula setal mukk wecc ñiy jaamusi. Su sarax yi taxoona set wecc, xanaa deesu ko dakkal? Bu ca jaamukati Yàlla yi doon sete wecc benn yoon kay, xanaa dootuñu am yaraangey bàkkaar!
Yawut ya 10:1–2
képp ku gëm Yeesu, ci moom lay wàccook loolu lépp, ba ag njubam mat.
Jëf ya 13:39
Gone yooyu nag, bindeefi suux ak deret lañu bokk doon, ñoom ñépp. Moo tax Yeesu itam dikk bokk ak ñoom woowu nekkin, ngir mana dee ba def deewug boppam pexe mi mu neenale ka yoroon dooley dee, te mooy Seytaane. Noonu la goreele mboolem ñi seenug ragala dee tënkoon cig njaam, seen giiru dund. Ndax kat du ay malaaka la Yeesu xettalisi, waaye askanu Ibraayma la xettalisi. Moo tax fàww mu niru woon ay bokkam ci bépp fànn. Su ko defee mu mana doon seen sarxalkat bu mag bu am yërmande te wóor fa kanam Yàlla, ngir mana defal askan wi seen njotlaayal bakkan.
Yawut ya 2:14–17
Ndax kat ñépp a bàkkaar, ba jotewuñu leeru Yàlla,
Room 3:23
Noonu it la Mbind mi indee ne:
«Kenn jubul, du kenn sax.
Room 3:10
Ñépp a lajj, bokk yàqu yaxeet,
Kenn deful lu baax, du kenn sax!
Room 3:12
Amul moos ku jub ci kaw suuf,
kuy def lu baax te du bàkkaar.
Kàdduy waare 7:20
Ana nu nit di ame dëgg fa kanam Yàlla?
Ku jigéen jur, nu mu mana laabe?
Ayóoba 25:4
Kon nag gannaaw digeb tàbbi ci noflaayal Yàlla mu ngi sax ba tey, nanu ragal kenn ci yeen taxawe melokaanu ku ca jotul.
Yawut ya 4:1
Éy Yàlla, ni nga goree, baaxe ma ni,
faral samag tooñ ngir sa yërmande ju yaa.
Taalifi cant 51:3
Xam naa ne maa tooñ,
sama moy a ngi janook man saa su ne.
Taalifi cant 51:5
Daawuda nag ne Natan: «Maa tooñ Aji Sax ji.» Natan ne ko: «Aji Sax ji it jéllale na sa bàkkaar; doo ci dee.
2.Samiyel 12:13
Ñi Yàlla tuddaloon loolu lu jiitu, moo leen woo itam; ñooñu mu woo, moo leen baaxe itam àtteb ñu jub; te ñooñu mu jox àtteb ñu jub, moo leen darajaal itam.
Room 8:30
Nun ñépp nag, kanam gu muriku lanuy xoole niki cib seetu leeru Boroom bi, ba tax nuy soppiku, doon takkndeeram, tey làmboo leer guy màgg, di gëna màgg. Looloo di liggéeyu Boroom bi, moom miy Noo gi.
2.Korent 3:18
Noonu la deme, ndegam kay fekk na leen sësoo ngëm gu ngeen dëjoo ba dëgër, te baña nangu lenn di leen sorele ak yaakaar ji ci xibaaru jàmm bi ngeen dégg, te ñu biral ko, ñeel mépp mbindeef. Man Póol nag, ci yégle xibaaru jàmm boobu laa di ab jawriñ.
Kolos 1:23
Ñaax nanu leen, dëfal leen, dénku leen, ngir ngeen di jëfe jëfin wu yelloo ak Yàlla mi leen woo ci nguuram ak teraangaam.
1.Tesalonig 2:12