Leeru Bés bi — 14 Nowàmbar: Taalifi cant 40:17

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Képp ku la wër, yal na bég, di la bànneexoo. Képp ku safoo sag wall, yal na jàppoo: «Aji Sax ji màgg na!»

Taalifi cant 40:17

Bu Aji Sax ji rafetloo saw yoon, mooy jiite say jéego. Soo tërëfee it, doo daanu. Aji Sax jee lay walloo loxoom.

Taalifi cant 37:23–24

Ragal Aji Sax ji kaaraange gu wér la ci nit, di rawtu ciy doomam.

Kàddu yu xelu 14:26

Man ci sama bopp maa leen di dëfal. Ana lu ngeen di ragal ci nit kuy dee, doom aadama ju bokk aw demin akum ñax? Dangeena fàtte Aji Sax ji leen sàkk, ki firi asamaan, lal suuf? Dangeen di dëkke bésoo bés, di tiit xadaru boroom doole buy waaja sànke? Ana fu xadaru boroom doole mujje?

Esayi 51:12–13

Bu leen ragal, ngir yaw laay àndal, di la xettali.» Kàddug Aji Sax jee.

Yeremi 1:8

Dëgërluleen nag te am fit. Buleen tiit, buleen yox-yoxi ndax ñoom, ngir seen Yàlla Aji Sax ji mooy ànd ak yeen. Du leen ba, du leen wacc mukk.»

Baamtug yoon wi 31:6

Ñuy wër di wut lu ñu lekk, su ñu suurul, di ñurumtu.

Taalifi cant 59:16

Yaw laay làqoo, nga di ma aar ciw ay, may ma ba ñi ma wër, di ko bége. Selaw.

Taalifi cant 32:7

«Ndegam boroom ñaari tànk ngay rawanteel, xoox, nooy rawanteeki fas? Soo wóoluwul lu moy àll bu ne yàmblaŋ, nooy def ak gottub Yurdan?

Yeremi 12:5

Ci kaw suuf su wow la sarxalkat ya gàddu gaalu kóllëre ga taxaw jonn, ca digg dex ga, fekk bànni Israayil gépp a ngi jàll ci kaw suuf su wow, ba xeet wépp dox jàll dexu Yurdan ba noppi.

Yosuwe 3:17

Yeesu mi ñu def mu gëna suufe as lëf malaaka yi, moom lanu gis deewam gi mu dee tax mu jagoo kaalag teraanga. Noonu la deewale ñépp ci kaw yiwu Yàlla.

Yawut ya 2:9

Su may jaare xuru dee wu ne këruus it, duma ragal loraange: yaw laak man, sa bantu sàmm ak sa nguul, yooyoo may dalal.

Taalifi cant 23:4

Booy xuus cim ndox, maa ngi ànd ak yaw; ag dex du la mëdd. Booy dox cib taal, doo lakk, sawara du la xoyom.

Esayi 43:2

Naka laa ko gis, ne dàll daanu ci ay tànkam ni ku dee. Mu teg ma loxol ndijooram, ne ma: «Bul tiit. Maay Ki njëkk, di Ki mujj. Maay Kiy dund, maa dee woon, maay dund nii tey ak ëllëg ba fàww te maa yor caabiy dee ak njaniiw.

Peeñu ma 1:17–18