Leeru Bés bi — 13 Nowàmbar: Efes 5:25–26

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Jëkkër nag, na sopp jabaram ni Almasi bi soppe mbooloom gëmkat ñi, ba joxeel leen bakkanam. Moo defal loolu mbooloo mi, ba man koo setale cangaayal ndox mu ànd ak kàddoom, ngir sellal ko.

Efes 5:25–26

te ngeen di doxale cofeel, ni Almasi bi nu sopp, ba joxeel nu bakkanam, def ko saraxu sawara ngir xetug jàmm gi neex Yàlla.

Efes 5:2

Ndax kat dangeena judduwaat, te jiwu wi ngeen judduwaate mooy kàddug Yàlla giy dund te sax dàkk; du jiwu wuy yàqu, waaye mooy jiwu wu dul yàqu mukk.

1.Piyeer 1:23

Ngalla sellale leen dëgg gi: sa kàddu mooy dëgg.

Yowaan 17:17

Yeesu ne ko: «Maa la ko wax déy ci lu wér, nit ki su juddoowul ci ndox ak ci Noowug Yàlla, du mana tàbbi ci nguurug Yàlla.

Yowaan 3:5

ca la nu musal, te du jenn jëfu njekk ju nu def, ba tax mu musal nu, waaye ci yërmandeem la nu musale, sang nu cangaay lu nu taxa judduwaat, boole ci yeesale nu Noo gu Sell

Tit 3:5

Lii laay muñe samaw naqar, sa kàddoo may dundal.

Taalifi cant 119:50

Asamaan lay fenke cat lii, wëndeelu, sowi cat lee; amul lu rëcc tàngooram. Yoonu Aji Sax jee mat, di leqali bakkan. Lu Aji Sax ji seede dëgg la, day xelal ku xeluwul.

Taalifi cant 19:7–8

ndax nun ñaari xeet yépp, ci moom Almasi bi lanu jote ci Baay bi, ci ndimbalal genn Noo gu Sell gi.

Efes 2:18

Man ma nekk ci ñoom, yaw nga nekk ci man, ngir ñu mat sëkk ci ag bennoo, ba àddina xam ne yaw yaa ma yebal, te ni nga ma soppe, ni nga leen soppe.

Yowaan 17:23

Te lépp lu ngeen ñaan ci sama tur, loolu laay def, ngir Doom ji fésal darajay Baay bi. Su ngeen ma ñaanee mbir ci sama tur, man maa koy def.

Yowaan 14:13–14

Man maay ñaan Baay bi, mu yónnee leen beneen Taxawukat, ngir mu nekk ak yeen ba fàww. Kooku mooy Noowug Yàlla giy xamle liy dëgg. Àddina du ko mana dalal, ndax gisu ko te xamu ko. Yeen nag xam ngeen ko, ndax ci seen biir la dëkk, te ci seen biir xel lay nekk.

Yowaan 14:16–17

Wenn yaram a fi nekk ak genn Noo ak jenn yaakaar ju leen wooteb Yàlla jëme. Benn Sang bi la it, ak genn ngëm ak genn sóobu cim ndox. Te it jenn Yàllaa am; mooy Baayu ñépp, moo tiim ñépp, di jëf ci ñépp te nekk ci ñépp.

Efes 4:4–6

Yeesu ne leen: «Bu ngeen dee ñaan, ne leen: Baay, nañu wormaal sa sellaayu tur, na sa nguur dikk.

Luug 11:2

Léegi nag bokk yi, am nanu sañ-sañu dugg ca néeg bu sella sell ba, ngir deretu Yeesu, deretu Yeesu jiy yoon wu yees, yoonu dund gu mu nu xàllal, jàllale ko ca rido ba, te rido ba moo di yaramu suuxam wi mu saraxe.

Yawut ya 10:19–20

Kon nag nanu agsee fi Yàlla xol bu dëggu ak fit wu mat sëkk wu ngëm waral, gannaaw wisees na sunum xel ndoxum setlu, ba mu tàggook bépp gàkk bu mu nu sikkale, te raggees na sunu yaram ci ndoxum setlu.

Yawut ya 10:22