Ndaxte tiis wu Yàlla namm, ag tuubeel gu jëme cig mucc lay jur, te loolu du tiis wees di tiisoo. Waaye tiisu àddina, dee lay jur.
2.Korent 7:10
Leeru Bés bi
Ndaxte tiis wu Yàlla namm, ag tuubeel gu jëme cig mucc lay jur, te loolu du tiis wees di tiisoo. Waaye tiisu àddina, dee lay jur.
2.Korent 7:10
Piyeer daldi fàttaliku la Yeesu waxoon ne: «Bala ganaar a sab, dinga ma jàmbu ñetti yoon.» Mu génn nag, di jooy jooy yu metti.
Macë 26:75
Su nu ko àggee sunuy bàkkaar, te muy ku jara wóolu, di boroom njub, moo nuy jéggal sunuy bàkkaar, raxas nu ba nu set, tàggook gépp njubadi.
1.Yowaan 1:9
Waaye ni mu nekke moom ci boppam cig leer, su nu dee wéye noonu ag leer, su boobaa lanuy séq jokkoog mbokk, te deretu Yeesu Doomam moo nuy raxas ba nu set, tàggook bépp bàkkaar.
1.Yowaan 1:7
Éy Aji Sax ji, bu ma xañ sa yërmande. Sa ngor ak sa kóllëre, yal na ma feg ba fàww. Ay musibaa ma tanc, ne gàññ, ba wees ab lim. Samay ñaawtéef a ma dab, ba gisatuma, baree bare, ba ëpp sama kawari bopp; sama xol jeex tàkk.
Taalifi cant 40:12–13
Aji Sax ji Yàlla Boroom gàngoor yi, Aji Sax jee di turu bàkkam.
Ose 12:6
Boroom bi, may ma, ma wax, ma delloo la njukkal.
Taalifi cant 51:17
di faj naqaru xol, fajtal góomi boroom.
Taalifi cant 147:3
Yaw nit ki, waxees na la li baax, ak li Aji Sax ji sàkku ci yaw, te loolu moyul di def yoon, sopp jëfi ngor te woyof nooy toppe sa Yàlla.
Mise 6:8
Dawal gaaw dajeek moom, laaj ko mbaa mu ngi ci jàmm mook jëkkëram ak doomam.» Mu laaj ko, mu ne ko: «Jàmm rekk la.»
2.Buur ya 4:26
Bindees na ne: «Damaa gëm, moo tax ma wax.» Nun it, wenn xeetu ngëm wi lanu am. Danoo gëm, moo tax itam nuy wax.
2.Korent 4:13
jàppe nu ñu kenn xamul, te nuy ñu siiw; jàppe nu ñuy waaja dee, te nuy dund; jàppe nu ñu ñu wara mbugal, te bañ leena teg àtteb dee. Dees noo jàppe boroomi tiis, te nu dëkke mbég; jàppe nu ay néew-ji-doole, te nu woomal ñu bare; jàppe nu ñu amul dara, te nu moom lépp.
2.Korent 6:9–10
ci biir teraanga ak ci biir toskare; ci biiri baatal ak jëw yu rafet. Dees noo jàppe ay mbubbookati dëgg, te nuy nit ñu dëggu; jàppe nu ñu kenn xamul, te nuy ñu siiw; jàppe nu ñuy waaja dee, te nuy dund; jàppe nu ñu ñu wara mbugal, te bañ leena teg àtteb dee. Dees noo jàppe boroomi tiis, te nu dëkke mbég; jàppe nu ay néew-ji-doole, te nu woomal ñu bare; jàppe nu ñu amul dara, te nu moom lépp.
2.Korent 6:8–10
Gan takktoo la kër Yàlla séq ak ay tuur? Ndax kat, nun, nooy kër Yàlla jiy dund, te noonu la ko Yàlla waxe ne: «Maay dëkk ci seen biir, di dox ci seen biir, di seen Yàlla, ñuy sama ñoñ.» Kon nag: «Nangeen génne ci seen biir, te teqalikoo ak ñoom,» la Boroom bi wax, «lu sobewu, buleen ko laal. Su boobaa, maa leen di dalal. Maay doon seen baay, ngeen di samay doom, góor ak jigéen,» la Boroom bi, Aji Man ji wax.
2.Korent 6:16–18
Soppe, yal nanga am jàmmi wet gu nekk. Ni nga ame jàmmu xol, yal nanga ni ame jàmmu yaram.
3.Yowaan 2
Bés yu mujj yi
Wone yépp11 Now 2025
10 Now 2025
9 Now 2025
8 Now 2025
7 Now 2025
6 Now 2025
5 Now 2025