ba yóbbu leen fu wóor te tiituñu; seeni noon, géej ga mëdd leen.
Taalifi cant 78:53
Leeru Bés bi
ba yóbbu leen fu wóor te tiituñu; seeni noon, géej ga mëdd leen.
Taalifi cant 78:53
Yoonu njub laay jaare, di dox ci li jaadu.
Kàddu yu xelu 8:20
«Te nag man ci sama bopp, maay yebal malaaka, mu di leen sàmm ci yoon wi, ba yóbbu leen béreb ba ma waajal.
Mucc ga 23:20
Seen gépp njàqare di njàqarey boppam, malaaka mi mu jàkkaarlool musal leen ca. Moo leen sopp, ñeewante leen, ba jotal leen boppam, te fu ñu masa jaare démb, mu fab leen, boot.
Esayi 63:9
Yaw ci sa bopp yaa dàq xeet yi, jëmbat fa maam ya; yaa mbugal xeet yi, ñoom, nga yiwi leen.
Taalifi cant 44:3
Ni jur gu wàccew xur, di fa fore, ni la leen noowug Aji Sax ji maye ab dalluwaay. Noonu nga wommate sa ñoñ, ba ame ca woy wu rafet.
Esayi 63:14
Man nag, sa ngor lu yaa laa saña dugge sa kër, sujjóotal sa béreb bu sell, wormaale la.
Taalifi cant 5:8
Ngalla yónneel sag leer ak sa dëgg, yal na ma yooyu jiite, yóbbu ma sa tund wu sell, sa màkkaan ma. Kon Yàlla, naa àgg ca sa sarxalukaay; yaw Yàlla, yaay sama mbégte, di sama bànneex. Yaw Yàlla, sama Yàlla, naa la màggale xalam.
Taalifi cant 43:3–4
Te loolu la ñenn ci yeen doonoon. Waaye Yàllaa leen fóot, sellal leen, jubal leen, ci turu Sang Yeesu Almasi bi ak ci sunu Noowug Yàlla.
1.Korent 6:11
Waaye ni mu nekke moom ci boppam cig leer, su nu dee wéye noonu ag leer, su boobaa lanuy séq jokkoog mbokk, te deretu Yeesu Doomam moo nuy raxas ba nu set, tàggook bépp bàkkaar.
1.Yowaan 1:7
Te moom sunuy tooñ a waral ñu jamat ko; sunuy ñaawtéef a waral ñu dëggaate ko. Yar yi nu jàmmal moom la dal, te mooy ki nu wére ciy góomam.
Esayi 53:5
Jëkkër nag, na sopp jabaram ni Almasi bi soppe mbooloom gëmkat ñi, ba joxeel leen bakkanam. Moo defal loolu mbooloo mi, ba man koo setale cangaayal ndox mu ànd ak kàddoom, ngir sellal ko. Li mu ci namm moo di teewal mbooloo mi fi kanamam, mu mel ni ab séetam bu ne ràññ, gàkkul, rasul, taqul lenn, xanaa sell, mucc sikk.
Efes 5:25–27
Jox nañu ko mbubbum lẽe mu set, ne ràññ, mu sol.» Lẽe boobu mooy jëfi njekk yu nit ñu sell ñi.
Peeñu ma 19:8
Kon nag nanu agsee fi Yàlla xol bu dëggu ak fit wu mat sëkk wu ngëm waral, gannaaw wisees na sunum xel ndoxum setlu, ba mu tàggook bépp gàkk bu mu nu sikkale, te raggees na sunu yaram ci ndoxum setlu.
Yawut ya 10:22
Ñi Yàlla tànn, ana ku leen di tuumaal? Yàlla de moo leen àtte ni ñu jub.
Room 8:33
Dib taalifu yeete, ñeel Daawuda. Ndokkalee yaw mi ñu baal ag moy, jéggal la bàkkaar. Ndokkalee yaw mi Aji Sax ji toppul say tooñ, te amoo xelum njublaŋ it.
Taalifi cant 32:1–2
Bés yu mujj yi
Wone yépp10 Now 2025
9 Now 2025
8 Now 2025
7 Now 2025
6 Now 2025
5 Now 2025
4 Now 2025