Leeru Bés bi — 6 Oktoobar: Peeñu ma 19:6

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Ma daldi dégg lu mel ni coowal mbooloo mu bare, mu àddoo ni riirum géej, tey nirook kàddug dënu gu réy, ne: «Aleluya! Sunu Boroom Yàlla Aji Man ji mooy Buur!

Peeñu ma 19:6

Xam naa ne lépp nga man; du lenn loo tële.

Ayóoba 42:2

Yeesu ne leen: «Li të nit, tëwul Yàlla.»

Luug 18:27

maa masa doon kenn ki, te sama loxo, maneesu cee musle. Su ma defee, kuy dindi?»

Esayi 43:13

Mu ne: «Abba, Baay, yaw mi dara tëwul, bii kaas bu fees ak wextanu coono, ngalla teggil ma ko. Waaye bumuy sama coobare, nay doon ci sa coobare.»

Màrk 14:36

Naka la Yeesu délsi, ba dugg ca kër ga, gumba ya duggsi. Yeesu ne leen: «Ndax gëm ngeen ne man naa koo def?» Ñu ne ko: «Waawaaw, Sang bi.» Yeesu daldi laal seeni bët, ne leen: «Noonu ngeen ko gëme, na ame noonu.»

Macë 9:28–29

Ab gaana jekki dikk, sujjóotal ko, ne ko: «Sang bi, su la soobee, man nga maa setal.» Mu tàllal loxoom, laal ko ne: «Soob na ma, setal.» Ca saa sa ngaanaam ga set wecc.

Macë 8:2–3

Dooley kilifteefam ak jàmm ja du am kemu, fa jalub Daawuda ak nguuram ga muy samp, saxale ko yoon ak njub tey jii ba fàww. Lii la Aji Sax ji Boroom gàngoor yi def ci xéraangeem.

Esayi 9:6

Yeesu dikk ne leen: «Joxees na ma bépp sañ-sañ fa asamaan ak fi kaw suuf.

Macë 28:18

Aji Sax jeey musal ki mu fal, bir na ma tey. Moo koy nangule fa asamaan su sell sa, ci dooley ndijooram biy musle.

Taalifi cant 20:7

«Dëgërluleen te amu fit. Buleen ragal, buleen jàq ndax buurub Asiri ak mboolem gàngoor gi ànd ak moom, ndax li ànd ak nun moo ëpp doole li ànd ak moom.

2.Jaar-jaar ya 32:7

Eli ne ko: «Kàddu gi mu la wax, lu mu doon? Bu ma nëbbu kay. Soo ma nëbbee lenn ci li mu la wax, yal na la Yàlla teg naqar wu gëna tar.»

1.Samiyel 3:17

Yaw nit ki, waxees na la li baax, ak li Aji Sax ji sàkku ci yaw, te loolu moyul di def yoon, sopp jëfi ngor te woyof nooy toppe sa Yàlla.

Mise 6:8

ngir di sàmm santaaney Aji Sax ji ak dogali yoonam yi ma leen dénk bésub tey ngir seen njariñal bopp?

Baamtug yoon wi 10:13

Mboolem ñi yaakaar seen jëf ju ñu sàmme yoonu Musaa, repp nañoo alku, nde bindees na ne: «Alku ñeel na ku saxoowul mboolem ndigal yi ñu bind ci téereb yoon wi, ngir di ko jëfe.» Li sàmm yoon taxul kenn jot àtteb ku jub fi kanam Yàlla sax, lu leer nàññ la, nde: «Ki ñu baaxe njub ndax ngëmam mooy dund.»

Galasi 3:10–11

Waaw kon yoonu Musaa, ana luy njariñam? Dees koo toftal ca dige ba, ngir muy fésal moyi nit ñi, ba keroog boroom dige bi taxawal askanu Ibraayma, dikk. Ay malaaka ñoo biral yoon wi, ci ndimbalal ab jottalikat.

Galasi 3:19

Bu yàgg la Yàlla waxoon ay yooni yoon ak maam ya, ci waxin yu bare, yonent yi jottali. Ci fan yu mujj yii, ci Doom ji la jaare wax ak nun, ki mu jagleel lépp, te ci moom la sàkke àddina wërngal këpp.

Yawut ya 1:1–2

Mu ne Samiyel: «Demal tëri, bu la wootee, nee ko: “Aji Sax ji, maa ngi lay déglu, Sang bi, waxal.”» Samiyel dellu tëdd fa muy tëdd.

1.Samiyel 3:9