di ma woo bésub njàqare, ma wallu la, nga màggal ma.»
Taalifi cant 50:15
Leeru Bés bi
di ma woo bésub njàqare, ma wallu la, nga màggal ma.»
Taalifi cant 50:15
Noon yaa ngi may ñaawal, di ma yendoo naa: «Ana sa Yàlla ji?» Ma ne yàcc, ne yasar.
Taalifi cant 42:11
Aji Sax ji, yaay dégg dagaanu néew-ji-doole, yaay dalal xelam, teewlu ko,
Taalifi cant 10:17
Boroom bi, yaa baax, di baale, di nàddil sa ngor képp ku lay dagaan.
Taalifi cant 86:5
Yanqóoba wax ak waa këram ak ñi ànd ak moom ñépp ne leen: «Jëleleen ci seen biir tuuri doxandéem yi, te ngeen sangu-set te solu. Danuy dem Betel, ma sàkkal fa sarxalukaay Yàlla ji ma wallu, ba ma nekkee ci njàqare, te ànd ak man fépp fu ma jaar.»
Njàlbéen ga 35:2–3
Naa sant Aji Sax ji ci saa xol bii, te baña fàtte mboolem xéewalam!
Taalifi cant 103:2
Maa bëgg Aji Sax ji: maa ko woo, dagaan ko, mu dégg ma. Teewlu na ma moos, dama koy woo li feek may dund. Buumi dee a ma laawoon, njàqarey njaniiw dab ma, ma dajeek naqar aku tiis. Ma woo Aji Sax ji wall, ne ko: «Ngalla Aji Sax ji, xettali ma!»
Taalifi cant 116:1–4
Ndax kat, «Des nas tuut, as tuut rekk, kiy dikk, dikk te du yeex.
Yawut ya 10:37
Aji Sax jee àddu, ne: «Bindal peeñu mi, leeral ko ci àlluwa yi, ba njàng mi yomb. Peeñu mi seede la, ñeel jant ba ñu ko àppal, seede su wóor ci na mbir may mujje, te du fen. Su diibee it, xaar ko, day dikk moos te du yàggati.
Abakug 2:2–3
Soppe yi, lenn a ngii, buleen ko umple: benn bés ni junniy at la mel ci Boroom bi; junniy at mel ni benn bés ci moom. Du caageenu yeexe gu Boroom bi yeexe dige ba, noonu ko ñenn ñi fooge ag yeex. Yeen la muñal kay, ndax bëggul kenn sànku, xanaa ñépp dem ba tuub.
2.Piyeer 3:8–9
Waaye yaw Boroom bi Yàlla, yaa ñeewante, yërëm, yaa muñ mer, bare ngor ak worma.
Taalifi cant 86:15
Ni sawara di jafale boob, baxale ko am ndox, ni ngay xamalsee say noon saw tur, ba yooyu xeet di lox fi sa kanam.
Esayi 64:1
Yaay gatandu kiy bége njekk gi muy jëfe te di ba xel say yoon yi ñu mas di jaare, ba mucc. Waaye kat, yaa nu mere, ndax noo bàkkaar.
Esayi 64:4
Bés yu mujj yi
Wone yépp4 Okt 2026
3 Okt 2026
2 Okt 2026
1 Okt 2026
30 Sàt 2026
29 Sàt 2026
28 Sàt 2026