Ndaxam moo xam fi ma jaare, te bu ma nattoo, ma génn ci ni wurus wu ñu xelli.
Ayóoba 23:10
Leeru Bés bi
Ndaxam moo xam fi ma jaare, te bu ma nattoo, ma génn ci ni wurus wu ñu xelli.
Ayóoba 23:10
Moo xam sunu bind, di bàyyi xel ne pënd lanu.
Taalifi cant 103:14
Du bànneexam lay tege coono, aka naqaral doom aadama.
Jooytu 3:33
Teewul cëslaay lu dëgër, li Yàlla tabax, mu ngi ne kekk, te màndarga ma ca nekk, kàddu yii la: «Boroom bi xam na ki mu séddoo,» ak: «Kuy tudd turu Sang bi, na daw njubadi.» Kër gu mag nag, du ndabi wurus ak xaalis rekk a fa am, waaye yoy bant a nga fa ak yoy ban; yii di ndabi teraanga, yee di ndabi njoogaan. Ku setal sa bopp nag ba mucc ci yu bon yooyii, yaay doon ndabal teraanga lu sell te amal sangam njariñ ngir jépp jëf ju baax.
2.Timote 2:19–21
Fa mbaxana dee benn lay tooge ni xellikat ak seggkat, te mooy segg sëti Lewi, xelli leen ni xaalis ak wurus, ba ñu doon niti Aji Sax ji, ñi koy indil sarax ci yoon.
Malasi 3:3
Ñetteel bi laay tàbbal ci sawara, xelli ko ca ni ñuy xellee xaalis, nattu ko ni ñuy nattoo wurus cib taal. Xaaj boobu moo may woo ci sama tur, ma wuyu ko. Moom laay wax: “Sama ñoñ,” moom mu ne: “Aji Sax jeey sama Yàlla.”»
Sàkkaryaa 13:9
Éy, Aji Sax ji, won ma saw yoon, xamal ma fi nga ma jaarloo.
Taalifi cant 25:4
Musaa nag ne Aji Sax ji: «Waaw, yaw de yaa ngi ma naa ma yóbbu mbooloo mii, waaye xamaloo ma kan ngay yebal, mu ànd ak man. Yaa ma waxoon it ne ma: “Maa la xam ci saw tur, te it daj nga sama yiw.” Gannaaw daj naa saw yiw nag, rikk xamal ma li nga namm, ba ma xam la. Su ko defee ma man di daj saw yiw. Te ngalla jàppal ne xeet wii kat, ñoo di sa ñoñ.» Aji Sax ji ne ko: «Man ci sama bopp maay ànd ak yaw te maa lay noppal.»
Mucc ga 33:12–14
Moo xamal Musaa ay nammeelam, xamal bànni Israayil ay jëfam.
Taalifi cant 103:7
di jiite ku woyof mbubb ci njubte, di ko xamal aw yoonam.
Taalifi cant 25:9
Ana kuy wormaal Aji Sax ji, mu won ko yoon wi mata tànn,
Taalifi cant 25:12
Maay woo Aji Sax ji wall, mu walloo ma fa tundam wu sell wa. Selaw. Maay tëdd nelaw, yewwu; Aji Sax ji di ma aar.
Taalifi cant 3:5–6
Yaa may xamal yoonu dund. Fu bànneex mate, yaa teew, xéewal sa ndijoor la saxe.
Taalifi cant 16:11
Nga ne ma: «Dama laa xelal, xamal la fi ngay jaar, digal la, di la bàyyi xel.
Taalifi cant 32:8
Yoonu ku jub day leer, ba ne ràññ ni bëccëg.
Kàddu yu xelu 4:18
Bés yu mujj yi
Wone yépp29 Sàt 2026
28 Sàt 2026
27 Sàt 2026
26 Sàt 2026
25 Sàt 2026
24 Sàt 2026
23 Sàt 2026