Meññeefum Noowug Yàlla nag moo di: cofeel ak mbég ak jàmm ak xolu muñ ak mbaax akug tabe ak ngëm akug teey ak noot sa bakkan. Yu mel noonu, wenn yoon bañu ko.
Galasi 5:22–23
Leeru Bés bi
Meññeefum Noowug Yàlla nag moo di: cofeel ak mbég ak jàmm ak xolu muñ ak mbaax akug tabe ak ngëm akug teey ak noot sa bakkan. Yu mel noonu, wenn yoon bañu ko.
Galasi 5:22–23
Joŋantekati tàggat yaram yi, dañuy yar seen yaram bu metti, te ñooñu kaalag ndam guy seey doŋŋ lañu ci yaakaar, waaye nun, kaalag ndam gu sax dàkk lanu ci yaakaar. Man nag noonu laay dawe, waaye samaw xél ñàkkul ab jëmu. Noonu laay këmëxee it, waaye dóoruma ci jaww ji. Damay yar sama yaram yar bu metti kay, ba moom ko, ndax ëllëg ñu bañ maa doyadal, gannaaw bu ma xamalee ñeneen kàddu gi ba noppi.
1.Korent 9:25–27
Buleen naan biiñ ba màndi, màndite ci afal seen bakkan la leen jëme, waaye na leen Noowug Yàlla fees,
Efes 5:18
Gannaaw loolu Yeesu ne taalibeem ya: «Ku bëgga dikk topp ma, fàtteel sa bopp te nga gàddu sa bant bi ñu lay daaj, door maa topp.
Macë 16:24
Kon nag bunu nelaw ni ñi ci des, waaye nanu teewlu, te ànd ak sunu sago. Ndaxte ñiy nelaw, guddi lañuy nelaw; ñiy màndi it, guddi lañuy màndi. Waaye nun ñiy waa bëccëg, nanu ànd ak sunu sago, te def ngëm ak cofeel sunu kiiraayal dënn; yaakaaru texe di sunu mbaxanam xare.
1.Tesalonig 5:6–8
Yiw woowu moo nu digal nu dëddu ñeme Yàlla ak xemmemtéefi àddina, te jiital sunum xel, di jëfe njub, te nekke ragal Yàlla ci àddinay tey jii. Loolu lees nu digal, li feek nu ngi séentu yaakaaru mbég ma, keroog bésu peeñum sunu màggaayu Yàlla miy Yeesu Almasi bi, Musalkat bi.
Tit 2:12–13
Su boobaa kay, dëgg gu nu wodde cofeel lanuy wéye, tey màgg ci bépp fànn, ci moom Almasi biy bopp bi.
Efes 4:15
Suuf ay meññal boppam gàncax, jiital am ñax, dem ba taxawal aw gub, ba ay pepp mujj fees gub wa.
Màrk 4:28
Su ko defee nu mana màgg nun ñépp ba doon benn ci ngëm ak ci xam-xam bu mat ci Doomu Yàlla ji, ba kera nuy doon magum jëmm, bay tollook taxawaayu Almasi bi mat sëkk.
Efes 4:13
Ñenn ci ñooñu di seedeel seen bopp ne ñoo yelloo ngërëm nag, nun ñemewunoo boole sunu bopp ak ñoom, mbaa nuy méngale sunu bopp ak ñoom. Waaye ñoom dañoo amul xel, ndax nattukaay bi ñuy nattoo, di ko méngalantee ci seen biir, ñoom ñoo ko sàkkal seen bopp!
2.Korent 10:12
Kuy damu daal, na damu ci Boroom bi. Ndax ki ñu naw mooy ki Boroom bi gërëm, waaye du ki gërëm boppam.
2.Korent 10:17–18
Loolu lépp takkndeeru yaram wuy jëmmal lu dikkagul rekk la woon. Waaye yaram wi dëgg moo di Almasi bi. Buleen nangu kenn ku leen sikkal, te di kuy teg boppam jëfi toroxlu, di jaamu ay malaaka, topp seen gis-gisi peeñuy bopp. Ñu ni mel ñooy réy-réyloo xalaati neen yu ñu fente seen yég-yégi bakkan. Ñooñu jokkuwuñu ci Almasi biy bopp bi, te ci bopp bi la yaram wi wépp di jëfandikoo siddit yeek tenqo yi, ba suuxatu, ngir lépp mànkoo ba mana màgg, ni ko Yàlla di màggale.
Kolos 2:17–19
Waaye màggleen ci wàllu yiwu sunu Boroom, sunu Musalkat Yeesu Almasi bi, ak ci wàllu xam-xam bu ngeen ko xam. Ndam ñeel na ko tey, ba kera bés bu sax dàkk. Amiin.
2.Piyeer 3:18
Bés yu mujj yi
Wone yépp30 Sàt 2026
29 Sàt 2026
28 Sàt 2026
27 Sàt 2026
26 Sàt 2026
25 Sàt 2026
24 Sàt 2026