Sikket bi day yenu seeni ñaawtéef yépp, yóbbaale ca ndànd-foyfoy ga, ñu wacc ko ca màndiŋ ma.
Sarxalkat yi 16:22
Leeru Bés bi
Sikket bi day yenu seeni ñaawtéef yépp, yóbbaale ca ndànd-foyfoy ga, ñu wacc ko ca màndiŋ ma.
Sarxalkat yi 16:22
Ni penku soree sowu, ni la nu soreleek sunu mbugali tooñ.
Taalifi cant 103:12
Su bés baa, ci yooyu fan,» kàddug Aji Sax jee, «dees na seet fi Israayil lu ñaaw, te du fi am; fi Yuda it, deesu fi gis bàkkaar. Maay jéggal moos ndes wi ma fi saxal.
Yeremi 50:20
Moo nuy yërëmati; sunuy ñaawtéef lay joggiy tànkam, te biir xóotey géej lay tàbbal sunuy bàkkaar.
Mise 7:19
Ana Yàlla ju mel ni yaw, di baale ag tooñ, di jéllale ag moy, ñeel ndesu ab séddoom? Kii du denc mer ba fàww, te moo bëgg di yéwéne.
Mise 7:18
Nun ñépp a lajj niy xar, ku nekk walbatiku topp yoonam, te Aji Sax jee ko sëf mbugal mi nu wara dékku nun ñépp.
Esayi 53:6
Mooy sonn ba gisug leer, doyloo ko. Ñu bareey xam sama jaam bii di Aji Jub, mu def ñu bare, ñu ñu limal njub, ndax li mu sëfoo seeni ñaawtéef. Moo tax ma di ko jox ab cér ci biir ñu bare, mu séddoo ak ay kàngam alalu xareem, ngir moo jébbale bakkanu boppam, ñu limaale kooki tooñkat, moo gàddu bàkkaaru ñu bare te mooy tinul moykat yi.
Esayi 53:11–12
Ca ëllëg sa, ba Yaxya gisee Yeesu di dikk wutsi ko, da ne: «Kii mooy Xarum Yàlla, miy far bàkkaaru àddina.
Yowaan 1:29
Ci yiwu Yàlla daal laa doone ki ma doon, te yiw woowu ma ñeel neenul. Te sax yeneen ndaw yépp sax, maa leen gëna liggéey. Du ci man nag, waaye yiwu Yàlla wi ànd ak man la.
1.Korent 15:10
Moom la soob mu jur nu ci kàddug dëgg gi, ba nu taxawe saraxu ndoortel meññeef, ci biiri bindeefam.
Yanqóoba 1:18
Kon nag mbaaxug Yàlla ajuwul ci coobarey nit ki, mbaa aw ñaqam, waaye lépp yërmandey Yàlla la.
Room 9:16
Kon ana lees di bàkkoo? Dara! Ci lan lañu koy teg sax? Ci jëf ju yoon santaane? Mukk! Xanaa yoonu ngëm doŋŋ.
Room 3:27
Te moom it moo tax ngeen bokk ci Almasi Yeesu mi ñu def muy sunu xam-xam bu bawoo fa Yàlla, di sunu njub, di sunu cellte, di sunug njot, su ko defee, noonu ñu binde ne: «Kuy damu, na damu ci Boroom bi,» noonu lay ame.
1.Korent 1:30–31
Yeen dangeena dee woon ndax seeni moy ak seeni bàkkaar yi ngeen doon dunde démb, ngeen àndoon ci ak doxalinu àddinay tey jii, ak ku bon kiy kàngamu boroom baat yi ci jaww ji asamaan tiim, di boroom xel mu bon mi wéye liggéeyam ci biir aji déggadi ñi, tey. Ci ñoom lanu bokkoon nun ñépp itam; mas nanoo topp sunu bakkan, di jëfe lu sunu bakkan ak sunum xel xemmem. Sunu bindu nit taxoon na noo yeyoo am sànj ni ñépp.
Efes 2:1–3
Te loolu la ñenn ci yeen doonoon. Waaye Yàllaa leen fóot, sellal leen, jubal leen, ci turu Sang Yeesu Almasi bi ak ci sunu Noowug Yàlla.
1.Korent 6:11
Bés yu mujj yi
Wone yépp1 Okt 2026
30 Sàt 2026
29 Sàt 2026
28 Sàt 2026
27 Sàt 2026
26 Sàt 2026
25 Sàt 2026