Nii nag lanuy xame lan mooy cofeel: Almasi bi dafa joxe bakkanam ngir nun; kon nun itam, li nu war mooy nu joxe sunu bakkan ngir sunu bokki gëmkat.
1.Yowaan 3:16
Leeru Bés bi
Nii nag lanuy xame lan mooy cofeel: Almasi bi dafa joxe bakkanam ngir nun; kon nun itam, li nu war mooy nu joxe sunu bakkan ngir sunu bokki gëmkat.
1.Yowaan 3:16
Ngeen boole ci daj cofeelu Almasi gi wees xam-xam, ngir ngeen fees, ba fees dell ak koomu Yàlla.
Efes 3:19
Joxe sa bakkan te say xarit tax, ameesul cofeel gu ko raw,
Yowaan 15:13
Xam ngeen kat sunu yiwu Boroom Yeesu Almasi bi, moom mi woomle woon, te yeena tax mu ñàkk, ngir woomale leen ag ñàkkam.
2.Korent 8:9
Soppe yi, ndegam Yàllaa nu soppe nii, nun itam war nanoo soppante.
1.Yowaan 4:11
Baaxleen ci seen diggante, di ñeewantante, tey baalante, ni leen Yàlla baale ci Almasi bi.
Efes 4:32
Muñalanteleen te di baalante, su dee kenn ku am lu mu sikke moroomam. Ni leen Boroom bi baale, deeleen baalantee noonu.
Kolos 3:13
Ndax Doomu nit ki itam ñëwul ngir ñu di ko surgawu, xanaa ngir di nekk surga, ba far maye bakkanam, def ko njotug ñu bare.»
Màrk 10:45
Ci loolu sax lañu leen woo, ndax Almasi bi itam sonn na ngir yeen, te moo leen bàyyeel ab royukaay, ngir ngeen jaar ciy tànkam.
1.Piyeer 2:21
Ndegam nag man miy Sang bi, di Kilifa gi maa leen raxasal seeni tànk, kon yeen itam war ngeen di raxasalante ay tànk. Ab misaalu royukaay laa leen jox, ngir ni ma leen defal, ngeen di ko def yeen itam.
Yowaan 13:14–15
Nii nag lanuy xame lan mooy cofeel: Almasi bi dafa joxe bakkanam ngir nun; kon nun itam, li nu war mooy nu joxe sunu bakkan ngir sunu bokki gëmkat.
1.Yowaan 3:16
Yeesu dellu ne leen: «Maa leen ko wax déy ci lu wér, Doom ji manula def dara ci jëmmu boppam, lu moy li mu gis Baay bi def ko, ndax lu mu def, loolu itam la Doom ji di def.
Yowaan 5:19
ndax Aji Sax jeey maye xel mu rafet, kàddoom di taxa xam, di dégg.
Kàddu yu xelu 2:6
Ndax man maa leen di may làmmiñ wu ànd ak xel wu seen benn noon dul mana dàq mbaa di ko weddi.
Luug 21:15
Yaakaaral Aji Sax ji, dëgërlul te amu fit, te yaakaarati Aji Sax ji.
Taalifi cant 27:14
Mu ne ma: «Sama yiw doŋŋ nga soxla; sama manoore, ci ag néew doole lay mate.» Kon kat dinaa gëna bégati ci damoo diggante yu ma néewe doole, ngir manoorey Almasi bi wàcc ci sama kaw.
2.Korent 12:9
Ci man Yudd miy jaamub Yeesu Almasi bi, di rakku Yanqóoba, ci man la bataaxal bii bawoo, ñeel leen yeen ñi ñu woo, yeen ñi Yàlla Baay bi sopp, te sàmmal leen Yeesu Almasi bi.
Yudd 1:1
Yeesu miy sellal nit ñi, moom ak ñi muy sellal, ñoo bokk lenqe, te moo tax Yeesu rusu leena woowe ay bokk.
Yawut ya 2:11
Ku mana làqoo làquwaay, ba duma ko gis?» Kàddug Aji Sax jee. «Xanaa du asamaan ak suuf, maa ko fees?» Kàddug Aji Sax jee.
Yeremi 23:24
mbooloo miy aw yaramam. Ci mbooloo mi nag la Almasi bi teewe teewaay bu mat sëkk, te Almasi bi mooy matal lépp ci ñépp.
Efes 1:23
Aji Sax ji, mennum man a; amul jotkat bu ma moy.
Esayi 43:11
Ñu wax ndaw sa nag ne ko: «Dootul li nga wax a nu taxa gëm, waaye nun noo déggal sunu bopp, ba gis ne kii moo di Musalkatub àddina bi.»
Yowaan 4:42
Bataaxal bi ñeel na Tit, sama doomu yoon ci kaw ngëm gi nu bokk. Aw yiw ak jàmm ñeel na la, bawoo fa Yàlla Baay bi ak Almasi Yeesu sunu Musalkat.
Tit 1:4
Bés yu mujj yi
Wone yépp28 Sàt 2026
27 Sàt 2026
26 Sàt 2026
25 Sàt 2026
24 Sàt 2026
23 Sàt 2026
22 Sàt 2026