Ci kaw loolu Musaa wàcc tundu Sinayi, ŋàbb ñaari àlluway seede sa. Naka la Musaa di wàcce ca tund wa, deru kanam ga di lerxat te yégu ko. Booba ñaaroom baak Yàlla moo waral loola.
Mucc ga 34:29
Leeru Bés bi
Ci kaw loolu Musaa wàcc tundu Sinayi, ŋàbb ñaari àlluway seede sa. Naka la Musaa di wàcce ca tund wa, deru kanam ga di lerxat te yégu ko. Booba ñaaroom baak Yàlla moo waral loola.
Mucc ga 34:29
Bu muy nun, Aji Sax ji, bu muy nun, saw tur nga wara teral, ngir sa ngor ak sa worma.
Taalifi cant 115:1
Su ko defee boroom njekk yi ne ko: “Sang bi, kañ lanu la gis, nga xiif, nu leel la; mbaa nga mar, nu nàndal la?
Macë 25:37
Buleen def dara ci kaw wujje, mbaa réy-réylu, waaye woyofluleen, ba jàpp ne seeni moroom a leen gën.
Filib 2:3
Naka noonu yeen ndaw ñi, nangulleen magi mbooloom gëmkat ñi. Yeen ñépp nag toroxluleen ci seenug jëflante, ndax: «Yàlla, ñi réy lay xeex, ñi toroxlu, mu may leen aw yiw.»
1.Piyeer 5:5
Mu soppiku fa seen kanam, xar kanamam di melax nib jant, ay yéreem weex nig leer.
Macë 17:2
Mboolem ña ca kuréelu àttekat ya nag ne jàkk Eccen; ñu gis xar-kanam ba ne ràññ ni xar-kanamu malaaka.
Jëf ya 6:15
Man nag daraja ji nga ma jox, jox naa leen ko, ngir ni nu nekke benn maak yaw, ñu nekke ni noonu.
Yowaan 17:22
Nun ñépp nag, kanam gu muriku lanuy xoole niki cib seetu leeru Boroom bi, ba tax nuy soppiku, doon takkndeeram, tey làmboo leer guy màgg, di gëna màgg. Looloo di liggéeyu Boroom bi, moom miy Noo gi.
2.Korent 3:18
Yeena di leeru àddina. Ab dëkk, bu nekkee ci kaw tund, du mana làqu. Te it deesul taal ab làmp, dëpp cig leget, waaye dees koy aj ca kaw tegoom, ba muy leeral ñi nekk ci néeg bi ñépp.
Macë 5:14–15
Ba loolu amee leerug Yàlla dikkal Amasay ka jiite Fanweeri jàmbaar ya. Mu ne: «Yaa nu moom, yaw Daawuda, nu far ak yaw, doomu Yese. Jàmm, jàmm rekk a la ñeel, te jàmm ay ñeel ñi lay wallu, ndax sa Yàlla moo lay wallu.» Daawuda nag dalal leen, def leen ay njiit ci gàngooram.
1.Jaar-jaar ya 12:19
Ba Daawuda di dellu Ciglaag nag la ko waa giirug Manase fekksi. Muy Atnax ak Yosabàdd ak Yediyel ak Mikayel ak Yosabàdd ak Eliyu ak Ciletay, ñépp di njiiti kuréeli junni ci giirug Manase.
1.Jaar-jaar ya 12:21
Ku nekk nag, ak na mayu Noo giy feeñe ci moom, ngir njariñal ñépp.
1.Korent 12:7
Waa genn-wàllu giirug Manase ga ca sowu fukki junneek juróom ñett (18 000) lañu woon, di ñu ñu tudd seen tur ñu wara fali Daawuda buur.
1.Jaar-jaar ya 12:32
Kii ci Noo gi la jote kàddu gu xelu, kee séddoo kàddug xam-xam ci genn Noo gi.
1.Korent 12:8
Waa giirug Isaakar ñaari téeméeri kilifa lañu woon ñu ànd ak mboolem seen bokk yi ñu jiite. Ay nit lañu woon ñu mana ràññee diggante ba Israayil mana tollu ak na ñu ca wara jëfe.
1.Jaar-jaar ya 12:33
Boroom xel ñaar la, xel maa toogul ci lenn lu muy def.
Yanqóoba 1:8
ngir xaajaloo baña am ciw yaram, te cér yi mànkoo ci di bàyyeente xel. Bu benn cér mettee, mook cér yépp ay bokk mitit wi. Bu dee benn cér lañu teral, mook cér yépp ay bokk bànneexu.
1.Korent 12:25–26
Benn Sang bi la it, ak genn ngëm ak genn sóobu cim ndox.
Efes 4:5
Bés yu mujj yi
Wone yépp3 Okt 2026
2 Okt 2026
1 Okt 2026
30 Sàt 2026
29 Sàt 2026
28 Sàt 2026
27 Sàt 2026