Ci suufu loxol Yàlla bi am doole la leen Yàlla di yékkatee bu jotee, su ngeen toroxloo,
1.Piyeer 5:6
Leeru Bés bi
Ci suufu loxol Yàlla bi am doole la leen Yàlla di yékkatee bu jotee, su ngeen toroxloo,
1.Piyeer 5:6
Aji Sax ji sib na ku réy, da koy mbugal ci lu wér.
Kàddu yu xelu 16:5
Éy Aji Sax ji, bul mer lool, bul bàyyi xel fàww ci ñaawtéef. Ngalla seetal ne nooy sa ñoñ, nun ñépp. Say dëkk yu sell doon nañu màndiŋ, Siyoŋ ca la, doon na màndiŋ. Yerusalem laa ne, gental na!
Esayi 64:8–9
Maa dégg moos askanu Efrayim di binni naan: “Aji Sax ji, duma nga noo duma, ni sëllu wu dese tàggat. Ngalla waññi nu, nu waññiku; yaw Aji Sax ji, yaa di sunu Yàlla. Dëddu woon nanu la moos waaye léegi réccu nanu. Xam nan ne tooñ nanu, ba tey nuy màttuy wiccax. Danoo rus, torox ndax sunu ñaawtéefi ndaw.”»
Yeremi 31:18–19
Li baax ci nit mooy nga nangoo muñ ba ngay ndaw.
Jooytu 3:27
Aw ay du garab, bay fëlle biir suuf, coono du jekki, jebbi. Ku juddu, coono nga juddul, mooy ferñent, kaw rekk la jëm.
Ayóoba 5:6–7
Jaan nag moo gënoona muus ci rabi àll, yi Yàlla Aji Sax ji sàkk yépp. Jaan ja moo ne jigéen ja: «Ndax wóor na ne Yàllaa ne: “Buleen lekk ci doomi genn garabu tool bi”?»
Njàlbéen ga 3:1
Fiirkat bi nag dikk ba ci moom, ne ko: «Ndegam yaa di Doomu Yàlla, neel doj yii ñu soppaliku mburu.» Teewul Yeesu ne ko: «Bindees na ne: “Du aw ñam doŋŋ la nit di dunde, waaye dees na dunde itam, gépp kàddu gu tukkee ci gémmiñug Yàlla.”»
Macë 4:3–4
Yeesu ne ko: «Bindees na it, ne: “Bul seetlu Boroom bi sa Yàlla.”»
Macë 4:7
Yeesu nag ne ko: «Xiddi ma Seytaane, ndax bindees na ne: “Boroom bi sa Yàlla ngay sujjóotal, te moom doŋŋ ngay jaamu.”» Ba mu ko defee Seytaane won ko gannaaw, ay malaaka dikk, di toppatoo Yeesu.
Macë 4:10–11
Mu ne ko: «Duma mana walbatiku ànd ak yaw, manumaa sex dugub it mbaa may bokk ak yaw ndoxum naan ci bii béreb. Ndaxte dañu maa wax ci ndigalal Aji Sax ji ne ma: “Bu fa sex dugub, bu fa naanum ndox te bul walbatiku jaare yoon wa nga jaare woon bi ngay ñëw.”» Mu dellu ne ko: «Man itam yonent laa ni yaw. Malaaka wax na ma ci ndigalal Aji Sax ji ne ma: “Waññi ko, mu ànd ak yaw sa kër, sex dugub, naan ndox.”» Fekk na la muy wax amul. Mu walbatiku ànd ak moom ca kër ga, sex fa dugub, naan fa ndox.
1.Buur ya 13:16–19
Yonent booba ko waññi woon ca yoon wa nag dégg ko ne: «Góoru Yàlla gaa! Ka tebbi woon waxi Aji Sax ji, Aji Sax ji boole kook gaynde gi, mu fàdd ko, rey ko. Moom la ko kàddug Aji Sax ji waxoon.»
1.Buur ya 13:26
Waaye nun ci sunu bopp, mbaa malaaka mu bawoo ci asamaan sax, ku leen ci àgge woon beneen xibaaru jàmm bu dul bi nu leen àgge, kooku yal na alku!
Galasi 1:8
Sama xol laa làq say wax, ngir bañ laa moy.
Taalifi cant 119:11
Bés yu mujj yi
Wone yépp26 Sàt 2026
25 Sàt 2026
24 Sàt 2026
23 Sàt 2026
22 Sàt 2026
21 Sàt 2026
20 Sàt 2026