Na ag ñeme coono sottal liggéeyam ci yeen, ngir ngeen sotti, mat sëkk, te baña yéese fenn.
Yanqóoba 1:4
Leeru Bés bi
Na ag ñeme coono sottal liggéeyam ci yeen, ngir ngeen sotti, mat sëkk, te baña yéese fenn.
Yanqóoba 1:4
Loolu bégeleen koo bége, doonte tey ñàkkul ngeen nekke njàqare ab diir, ndax ay nattuy nattu. Yooyu nattu, ni sawara di natte wurus, ni lay natte seen dëggutey ngëm, te ngëm a gën wurus fuuf, nde wurus day jeex. Su ko defee seen ngëm gu dëggu jural leen ag cant ak daraja ak teraanga, bés bu Yeesu Almasi bi feeñee.
1.Piyeer 1:6–7
Te yemunu ci, xanaa di sagoo sunuy tiis itam, nde xam nanu ne dékku aw tiis mooy taxa muñ; te muñ mooy jur kóllërey biir coono; kóllërey biir coono mooy jur yaakaar.
Room 5:3–4
Li baax mooy muñ, xeremluy xaar wallub Aji Sax ji.
Jooytu 3:26
Ndax yeena bokk ak ñi ñu tëj seen coono, te yeena muñ ci xol bu sedd ni ñu foqarñee seen moomeel, ngir xam ngeen yeen ci seen bopp ne am ngeen alal ju ko gën tey sax ba fàww. Kon nag buleen teqalikook seenu fit, yool bu réy a ngi ci. Li leen war moo di muñ, ba sottal coobarey Yàlla, su ko defee ngeen jot li mu dige.
Yawut ya 10:34–36
Te noonu lay deme kera bés ba Yàlla di àtte mbiri kumpa yu nit ñi, ci saytub Yeesu Almasi bi, ni ko sama xibaaru jàmm bi indee.
Room 2:16
Moo tax buleen àtte lenn te jotul, lu jiitu Boroom biy dikk. Moom mooy leeral li làqoo ag lëndëm, di làññi mébéti xol. Su boobaa ngërëm la ku nekk yelloo, fa Yàlla lay bawoo.
1.Korent 4:5
Baay bi du àtte kenn; Doom ji la dénk àtte bi bépp,
Yowaan 5:22
te sañ-sañu amal àtte bi itam, moom la ko jox, ndax mooy Doomu nit ki.
Yowaan 5:27
«Malaakam mbooloom gëmkat ña ca Catir nag, bind ko ne ko: «Lii moo di kàdduy Doomu Yàlla ji, ki ay gëtam mel ni sawara wu yànj, ay tànkam mel ni xànjar bu ñu jonj. Mu ne:
Peeñu ma 2:18
te naan: «Lu ci Yàlla xam? Ana xam-xam fa Aji Kawe ji?»
Taalifi cant 73:11
Lii yeena ko def! Damay noppi, ngeen defe ne damaa mel ni yeen? Dama leen di sikk, tuumaal leen, ngeen gis!
Taalifi cant 50:21
Mboolem lu làqu dees na ko feeñal, te lu umpe dees na ko xam.
Luug 12:2
Sama yaram dee goyy, ma ne lasar, jàq, di binni.
Taalifi cant 38:9
Aji Sax ji, nattu ma, seetlu ma, seggal xel ak xol.
Taalifi cant 26:2
Bés yu mujj yi
Wone yépp24 Sàt 2026
23 Sàt 2026
22 Sàt 2026
21 Sàt 2026
20 Sàt 2026
19 Sàt 2026
18 Sàt 2026