Kee di cëslaay, te mati jëf, wépp yoonam di njub. Yàlla ju am kóllëre, mucc njubadi, di àtte dëgg tey jub.
Baamtug yoon wi 32:4
Leeru Bés bi
Kee di cëslaay, te mati jëf, wépp yoonam di njub. Yàlla ju am kóllëre, mucc njubadi, di àtte dëgg tey jub.
Baamtug yoon wi 32:4
Saaga nañu ko te feyuwul, daj na coono te tëkkoowul, waaye boppam la dénk kiy àtte dëgg.
1.Piyeer 2:23
Kon ku nekk ci nun, yaay layool sa bopp fa Yàlla.
Room 14:12
Mu ngoog, bépp bakkan maay Boroom. Muy bakkanu baay, di bakkanu doom, maa moom. Bakkan bi bàkkaar daal mooy dee.
Esekiyel 18:4
«Éey saamar, yewwulal sama sàmm bi, sama jàmbaar jii ma lëngool,» kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi. «Dóoral sàmm bi, xar yi tasaaroo, ma walbati sama loxo, jublu ci jur gu ndaw gi.
Sàkkaryaa 13:7
Nun ñépp a lajj niy xar, ku nekk walbatiku topp yoonam, te Aji Sax jee ko sëf mbugal mi nu wara dékku nun ñépp.
Esayi 53:6
Wallam aka jege ñi ko ragal, te leeram dëgmal sunu réew mii!
Taalifi cant 85:10
Daan bu àndul ak yërmande, moom lees di àttee ña daawul jëfe yërmande. Yërmande nag kekku na ab daan.
Yanqóoba 2:13
Ndaxte peyooru bàkkaar mooy dee, waaye yiw wi Yàlla di maye mooy texe gu sax dàkk fi Almasi Yeesu, sunu Boroom.
Room 6:23
Àdduleen, layoosi, diisooleen fi seen biir kay! Ana ku xamle woon lii bu yàgg, yégle woon ko booba? Xanaa du man Aji Sax ji? Kenn du Yàlla ku dul man! Yàlla ju jub, di walloo, du kenn ku dul man!
Esayi 45:21
ndax Yàlla ci biir ag jéllaleem la firndeel njubteem ci janti tey jii, ngir mu leer ne moo wéye njub, te képp ku gëm Yeesu, moo koy baaxe àtteb ku jub.
Room 3:26
te ci yiwu Yàlla wu àndul ak genn pey lees di baaxe ñépp àtteb ñu jub, ndax njot gi sottee ci Almasi Yeesu.
Room 3:24
Bu yaramu judduwaale wii nara yàqu solee weneen wu dul yàqu, ba yaramu dee wii sol yaramu ndeetil, su boobaa la kàddu gii ñu bind di mat: «Mëddees na dee ci géeju ndam.
1.Korent 15:54
Waaye cant ñeel na Yàlla mi nu may ndam ci sunu Sang Yeesu Almasi bi!
1.Korent 15:57
Gone yooyu nag, bindeefi suux ak deret lañu bokk doon, ñoom ñépp. Moo tax Yeesu itam dikk bokk ak ñoom woowu nekkin, ngir mana dee ba def deewug boppam pexe mi mu neenale ka yoroon dooley dee, te mooy Seytaane. Noonu la goreele mboolem ñi seenug ragala dee tënkoon cig njaam, seen giiru dund.
Yawut ya 2:14–15
Gannaaw noo deewandoo ak Almasi bi nag, gëm nanu ne nooy dundandoo ak moom. Ndax kat xam nanu ne Almasi bii dekki te dootul dee, te dee manalatu ko dara. Deewam ga mu dee, dee na benn yoon ba fàww, ba tax bàkkaar amatul benn kilifteef, te dund gi muy dund tey, Yàlla la koy dundal. Naka noonu, yeen itam jàppeleen seen bopp nit ñu dee ba dootuleen nangooti kilifteefu bàkkaar, xanaa di dund ngir Yàlla, ndax seen bokk ci Yeesu Almasi bi.
Room 6:8–11
Waaye ci mboolem lu nu dikkal, nooy am ndam lu mat sëkk, ci ndimbalal ki nuy soppeem.
Room 8:37
Bés yu mujj yi
Wone yépp25 Sàt 2026
24 Sàt 2026
23 Sàt 2026
22 Sàt 2026
21 Sàt 2026
20 Sàt 2026
19 Sàt 2026