Nun de xam nanu ne noo bàyyikoo ci dee, tàbbi ci dund, ndax li nu sopp bokki gëmkat yi. Ku soppul nag, yaa ngi ci dee ba tey.
1.Yowaan 3:14
Leeru Bés bi
Nun de xam nanu ne noo bàyyikoo ci dee, tàbbi ci dund, ndax li nu sopp bokki gëmkat yi. Ku soppul nag, yaa ngi ci dee ba tey.
1.Yowaan 3:14
«Maa leen ko wax déy ci lu wér, ku dégg sama kàddu ba gëm ki ma yónni, yaa texe ba fàww, te àtte ba, doo ca jaare, waaye bàyyikoo nga ci dee, tàbbi ci dund.
Yowaan 5:24
Ku am Doom ji, yaa texe; ku amul Doomu Yàlla, texewuloo.
1.Yowaan 5:12
Te ki nuy saxal ci Almasi bi, nook yeen, moo nu tabbe diwu pal gi, te moo di Yàlla. Moo nu màndargaale xàmmikaayam, te moo yeb dawalub Noo gu Sell gi ci sunu biir xol.
2.Korent 1:21–22
Noonu lanuy xame ne nu ngi ci dëgg, ba dalal sunum xel ci kanamam.
1.Yowaan 3:19
Soppe yi, bu nu sunum xel sikkul, dinanu ñemee walbatiku ci Yàlla.
1.Yowaan 3:21
Nun nag xam nanu ne ci Yàlla lanu bokk, te àddina sépp a ngi ci loxol ku bon ki.
1.Yowaan 5:19
Yeen dangeena dee woon ndax seeni moy ak seeni bàkkaar
Efes 2:1
nun ñi doon nit ñu dee ba noppi ndax sunuy moy, moo nu booleek Almasi bi, dundalaat nu. Ci kaw yiw daal ngeen mucce.
Efes 2:5
Yàlla kat moo nu wallu ba génne nu ca kilifteefu réewum lëndëm ga, toxal nu ci biir nguurug Doomam ji mu sopp.
Kolos 1:13
Yaa may xamal yoonu dund. Fu bànneex mate, yaa teew, xéewal sa ndijoor la saxe.
Taalifi cant 16:11
«Te itam nga wax askan wii ne leen: “Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii di teg fi seen kanam yoonu dund ak yoonu dee.
Yeremi 21:8
Man nag, jomb naa tooñ Aji Sax ji, ci di leen noppee ñaanal. Te it dinaa leen won yoon wi baax te jub.
1.Samiyel 12:23
Yeesu ne ko: «Man maay yoon wi, maay dëgg gi, te maay dund gi. Kenn du ñëw ci Baay bi te jaarewul ci man.
Yowaan 14:6
Yeesu ne leen: «Ñëwleen topp ma, ma def leen nappkati nit.»
Macë 4:19
Yoon a ngii, nit defe ne jub na, te mu jëme ko ci dee.
Kàddu yu xelu 14:12
«Duggeleen ci bunt bu xat bi, ndax bunt beek yoon wi jëm sànkute dañoo yaatu, te ñu baree cay dugge. Waaye xat la def, bunt ba jëm dund; sew it la yoon wa def, te ñu néew a koy gis.
Macë 7:13–14
Foofa law yoon di jaare, ñu di ko woowe Yoon wu sell wi. Ku sobewu du fa jaare, ñi moom woowu yoon, ñooy ñi koy topp. Ab dof sax du fa lajje.
Esayi 35:8
Nan ràññee, di saxoo faale Aji Sax ji. Ni jant bu fenk la dikkam wóore, ni ab taw la nuy dikkale, ni ab tawu mujjantal buy seral suuf.»
Ose 6:3
Sama kër Baay, dëkkuwaay yu baree nga fa. Su demewul woon noonu, ndax dinaa leen ne maa ngi leen fay waajali béreb?
Yowaan 14:2
Bés yu mujj yi
Wone yépp24 Sul 2026
23 Sul 2026
22 Sul 2026
21 Sul 2026
20 Sul 2026
19 Sul 2026
18 Sul 2026