Kon nag ana lu ab Yawut rawe ci nit ñi? Ak luy njariñal xaraf? Xanaa lu bare, ci wet gu nekk. Li ci jiitu moo di ñoom lañu dénk kàdduy Yàlla.
Room 3:1–2
Leeru Bés bi
Kon nag ana lu ab Yawut rawe ci nit ñi? Ak luy njariñal xaraf? Xanaa lu bare, ci wet gu nekk. Li ci jiitu moo di ñoom lañu dénk kàdduy Yàlla.
Room 3:1–2
Yeen waa Yudaak Yerusalem, deeleen xaraf ngir Aji Sax ji, dogleen seen mbuñukay xol, balaa sama xadar ne jippét ni sawara, di tàkk te deesu ko fey ndax seen jëf ju bon.
Yeremi 4:4
ba man itam ma noonoo leen, toxal leen seen réewu noon. Bu ñu tuubee seen xol bu dëgër nag, ba matal seen mbugal yi sababoo ci seeni ñaawtéef, su boobaa maay bàyyi xel ci sama kóllëre gaak Yanqóoba ak sama kóllëre gaak Isaaxa ak sama kóllëre gaak Ibraayma, te duma fàtte li ma dige ci wàllu réew mi.
Sarxalkat yi 26:41–42
Dama leen di wax ne leen, bëgga fésal ne Yàlla ku dëggu la moo waral Almasi bi dikk, def boppam jawriñu Yawut yi, ngir sottal dige ya Yàlla digoon seeni maam.
Room 15:8
Ci moom ngeen xarafe xaraf gu loxol nit deful, ndax noonu kuy xarafal nit ki di dog as lëf ci yaramam, ni la Almasi bi di doge ba mu set buumu njaam gi leen dooley bàkkaar tënke woon. Noonu la Almasi bi di xarafalee.
Kolos 2:11
Yeen ñi doonoon ñu dee fa kanam Yàlla ndax seeni moy ak seen ñàkka xaraf, ndax li ngeen dul Yawut, Yàllaa leen booleek Almasi bi, dundalaat leen. Moo nu baal sunu moy yépp.
Kolos 2:13
te mooy ngeen bàyyi seen jikko ju njëkk ja, ngeen teqalikoo ak seen jëmm ja woon démb, jëmm ja masa topp bànneexi bakkan yuy naxe, ba sóobu ci yàqute. Su ko defee ngeen mana yeeslu ci seenum xel, ci ndimbalal Noowug Yàlla, te ngeen soloo jëmm ju yees ji Yàlla sàkke ci takkndeeram, di jëfe njub ak sellaay ji dëgg di jur.
Efes 4:22–24
Ca saa sa ridob biir néegu Yàlla ba dale ca kaw ba ca suuf, xar ñaar, suuf sa yëngu, doj ya xar,
Macë 27:51
Man, li ma jële ci Sang bi, moom laa leen jottali: Sang Yeesu, guddi gi ñu ko woree, dafa jël mburu, yékkati kàddug cant, dagg ko, ne: «Lii moo di sama yaram wi leen ñeel. Deeleen def lii, di ma ko fàttalikoo.»
1.Korent 11:23–24
Man maay ñam wiy dund te wàcce fa asamaan. Ku lekk ci wii ñam, mooy texe ba fàww. Ñam woowu nag mooy samaw suux; maa ko joxe, ngir àddina dund.»
Yowaan 6:51
Yeesu ne leen: «Maa leen ko wax déy ci lu wér, bu ngeen lekkul ci suuxu Doomu nit ki, naan deretam, amuleen dund ci seen jëmmi bopp. Képp ku lekk samaw suux, naan sama deret, texe nga ba fàww, te maa lay dekkal kera bés bu mujj ba.
Yowaan 6:53–54
Képp ku lekk sama suux, naan sama deret, ci man lay dëkk, ma dëkk ci moom. Ni ma Baay biy dund yebale, te may dund ndax moom, noonu la ki ma lekk di dunde ndax man.
Yowaan 6:56–57
Yeesu nag yég ci boppam ne taalibeem yaa ngi ñurumtoo loolu. Mu ne leen: «Xanaa kàddu gii mbetteel la leen def? Kon bés bu ngeen gisee Doomu nit kiy yéeg jëm fa mu njëkkoona nekk nag? Noowug Yàlla mooy dundloo; nitu suuxu neen manul dara. Kàddu gi ma leen wax moo leen di jottali Noowug Yàlla giy taxa dund.
Yowaan 6:61–63
deretu Yeesu jiy yoon wu yees, yoonu dund gu mu nu xàllal, jàllale ko ca rido ba, te rido ba moo di yaramu suuxam wi mu saraxe.
Yawut ya 10:20
Kon nag nanu agsee fi Yàlla xol bu dëggu ak fit wu mat sëkk wu ngëm waral, gannaaw wisees na sunum xel ndoxum setlu, ba mu tàggook bépp gàkk bu mu nu sikkale, te raggees na sunu yaram ci ndoxum setlu.
Yawut ya 10:22
Bés yu mujj yi
Wone yépp20 Sul 2026
19 Sul 2026
18 Sul 2026
17 Sul 2026
16 Sul 2026
15 Sul 2026
14 Sul 2026