Leeru Bés bi — 24 Sulet: Room 12:12

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Bégeleen seen yaakaar, di muñ ci biir tiis, tey saxoo ag ñaan.

Room 12:12

Samiyel wax ko lépp, nëbbu ko ca dara. Eli ne: «Mooy Aji Sax ji. Li ko soob, na ko def.»

1.Samiyel 3:18

Su sama der setee it, duma mana àddu, xanaa sama àttekat bii laay tinu.

Ayóoba 9:15

daldi ne: «Duŋŋ laa génne sama biiru ndey te duŋŋ laay delloo. Aji Sax jee maye, Aji Sax jee nangu. Cant ñeel na Aji Sax ji.»

Ayóoba 1:21

Mu ne ko: «Waxi jeeg bu dof daal ngay wax, yaw! Du Yàlla da nuy may lu baax, nu jël? Kon kay bu nu mayee safaan ba it, nu wara jël.» Ci biir loolu lépp Ayóoba bàkkaarul ciw làmmiñam.

Ayóoba 2:10

Yeesu nag jooy.

Yowaan 11:35

Dees na ko xeeb, daw ko, muy nit ku bare mitit te miin naqar. Mu mel ni ku ñuy dummóoyu, dees koo xeeb te nawloowuñu ko. Ndaxam moom sunu wopp la yenu, sunuy mitit la sëfoo. Nun nu foog ne dees koo mbugal, foog ne Yàllaa ko duma, toroxal ko.

Esayi 53:3–4

ndax Boroom bi, ku mu sopp, yar la, mooy bantal jépp doom ju ko neex.»

Yawut ya 12:6

Dëgg la, benn yarub tey neexul, xanaa naqari. Waaye la yar bay mujj jural ña mu tàggat, jàmm la ak njub.

Yawut ya 12:11

Ngir itam ngeen manoorewoo jépp manoore, na leen ko Yàlla manloo ci kàttanam gu màgg, ba ngeen mana dékku lépp ci xolu muñ,

Kolos 1:11

Loolu dama leen koo wax ngir seen xel dal ci man. Àddina sii, dingeen fi am njàqare, waaye dëgërluleen, ndax daan naa àddina.»

Yowaan 16:33

Teewul digeb Yàlla ba la ne jàkk, nàttablewul, gëmadiwul, xanaa dëgërloo dooley ngëmam rekk, sant Yàlla.

Room 4:20

Yeesu ne leen: «Gëmleen Yàlla. Maa leen ko wax déy, képp ku ne tund wale: “Jógal, tàbbiji géej,” te bañ cee boole xel ñaar, xanaa gëm ne li nga wax dina am, noonu lees la koy nangule. Moo tax ma di leen wax lii: Lépp lu ngeen di sàkku cig ñaan, gëmleen ne jot ngeen ko ba noppi, dingeen ko am.

Màrk 11:22–24

Ku amul ngëm nag doo mana neex Yàlla, ndax kiy dikk fi Yàlla, fàww nga njëkka gëm ne Yàlla am na, gëm it ne ñi koy sàkku, moo leen di yool.

Yawut ya 11:6

Ibraayma, ba ñu ko nattoo, ngëm la joxee Isaaxa ni ab sarax. Ibraayma mi ñu jagle dige yi, Isaaxa jenn doomam ju góor ji mu am, moom la doon joxe, te Yàlla ne woon ko: «Ci Isaaxa lees di tudde saw askan.» Waaye Ibraayma njortoon na ne su Isaaxa dee woon it, Yàlla man na koo dekkal. Moo tax itam ci misaal, Isaaxa délsi ciy loxoom, mel ni daa dekki.

Yawut ya 11:17–19

Dafa wéroon Ibraayma péŋŋ ne li Yàlla dige, man na koo def.

Room 4:21

Ana lu të Aji Sax ji? Bu ñu ca àggee nëgëni déwén déy, dinaa fi délsiwaat, te Saarata dina am doom ju góor.»

Njàlbéen ga 18:14

Yeesu nag ne leen jàkk, ne: «Loolu nit la të, waaye Yàlla man na lépp.»

Macë 19:26

Ci kaw loolu ndaw ya ne Sang bi: «Yokk nu ngëm.»

Luug 17:5