Ba Yàllay woo Ibraayma, ngir mu génn, jëm béreb ba mu mujj muurloo, ngëm la déggale Yàlla, ba génn, dem te xamul woon fu mu jëm.
Yawut ya 11:8
Leeru Bés bi
Ba Yàllay woo Ibraayma, ngir mu génn, jëm béreb ba mu mujj muurloo, ngëm la déggale Yàlla, ba génn, dem te xamul woon fu mu jëm.
Yawut ya 11:8
Moo nu nangulal xeet yi, nu teg tànk gàngoor yi.
Taalifi cant 47:4
Moo leen fekk réewum màndiŋ, fu ne wëyëŋ, ubaleeki sab, mu feg leen, toppatoo leen, sàmm leen, ni bu ñu doon peru bëtu boppam. Moo mel ni jaxaay juy naawtal am tostanam, daayaarlu, di wër, tiim leen, tàllali laafam, aw leen, teg ciw dunqam, boot leen. Aji Sax ji doŋŋ a leen wommat, du yàllay jàmbur ju ko ci fekk.
Baamtug yoon wi 32:10–12
Aji Sax ji seen jotkat dafa wax, Aji Sell ju Israayil da ne: «Maay Aji Sax ji, seen Yàlla ji leen di jàngal seen njariñ, di leen awale fa ngeen wara awe.
Esayi 48:17
Yàlla, kay, mooy ki dooleem kaweel! Ana ku mana jàngale ni moom?
Ayóoba 36:22
ndax ngëm lanuy doxe, waaye doxewunu ab gis-gis.
2.Korent 5:7
ndax amunu fii ci àddina dëkk bu sax ba fàww, waaye dëkk biy ñëw, moom lanuy sàkku.
Yawut ya 13:14
Soppe yi, ay gan ngeen, ay doxandéem ci kaw suuf. Kon nag li ma leen di dénk moo di ngeen moyu xemmemtéefi bakkan yiy xeex ak ab xol.
1.Piyeer 2:11
Jógleen dem, fii du bérebu noflaay, nde sobewu na, ba nara yàqe yaxeet.
Mise 2:10
Yeen aji jub ñi, bànneexooleen Aji Sax ji, sante ko turam wu sell wi.
Taalifi cant 97:12
Yàlla wóoluwul sax ñu sellam ña ca asamaan, te asamaan sellul ba doy ko, rawatina nit, moom mi jara seexlu, yàqu jikko, di def njubadi ni ndoxum naan.
Ayóoba 15:15–16
Xoolal, weer wi sax leerul ba doy ko, te biddiiw yi it gisul seen sellaayu leer, astamaak nit kii tanewul aw sax, doom aadama jii gënul gasax.
Ayóoba 25:5–6
«Ana kuy sa moroom ci tuur yi, yaw Aji Sax ji? Kuy sa dend, yaak sa sellaay bu yéeme, sa yànjaay bu raglook sa jëf yu yéeme?
Mucc ga 15:11
Ku ci nekk di àddu, naan moroom ma: «Kee sell te sell te sell, keey Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, àddina sépp a feese ag leeram!»
Esayi 6:3
Waaye ni ki leen woo selle, yeen itam nangeen selle noonu ci seen mboolem jëfin. Ndax kat bindees na ne: «Ñu sell ngeen wara doon, ndax man Ku sell laa.»
1.Piyeer 1:15–16
Sunuy baay a nu yar fan yu néew, na mu jaadoo woon ci seenum xel. Waaye sunu Baay bii, sunu njariñal bopp la nuy yare, ngir nu séddu ci sellaayam.
Yawut ya 12:10
Ku yàq kër Yàlla nag, kooku Yàlla dina ko yàq, ndax kër Yàlla dafa sell, te mooy li ngeen doon.
1.Korent 3:17
Gannaaw loolu lépp noonu lay seeye nag, xamleen bu baax li leen war: jëfin wu sell akug ragal Yàlla
2.Piyeer 3:11
Kon nag soppe yi, li feek ngeen di séentu loolu, defleen seen kem-kàttan, ba bésub keroog fekk leen ci jàmm, te ngeen baña am benn gàkk, mbaa sikk ci gis-gisu Yàlla.
2.Piyeer 3:14
Bu genn kàddu gu bon génne seen gémmiñ, xanaa su ko jaree ngeen wax lu baax, luy jariñe, te diw yiw ci ñi koy dégg. Te it buleen tiisal Noowug Yàlla gu Sell gi leen màndargaale xàmmikaayam ngir bésub njot ba.
Efes 4:29–30
Bés yu mujj yi
Wone yépp25 Sul 2026
24 Sul 2026
23 Sul 2026
22 Sul 2026
21 Sul 2026
20 Sul 2026
19 Sul 2026