Kooku la wattukat biy ubbil, xar yi di déglu baatam. Mooy woo xari boppam ci seen tur, génne leen.
Yowaan 10:3
Leeru Bés bi
Kooku la wattukat biy ubbil, xar yi di déglu baatam. Mooy woo xari boppam ci seen tur, génne leen.
Yowaan 10:3
Teewul cëslaay lu dëgër, li Yàlla tabax, mu ngi ne kekk, te màndarga ma ca nekk, kàddu yii la: «Boroom bi xam na ki mu séddoo,» ak: «Kuy tudd turu Sang bi, na daw njubadi.»
2.Timote 2:19
Bu bés baa, ñu baree ma naan: “Sang bi, Sang bi, xanaa du saw tur lanu daa waaree, di dàqe saw tur ay rab, tey defe saw tur kéemaan yu bare?” Booba laa leen di wax ne: “Masuma leena xam, defkati ndëngte yi ngeen doon, xiddileen ma!”
Macë 7:22–23
Aji Sax ji kay ay sàmm yoonu aji jub; yoonu ku bon di sànk boroom.
Taalifi cant 1:6
Sama biir loxo yii laa la ñaas, say tataa janook man ba fàww.
Esayi 49:16
Teg ma ci sa xol ni torlukaay, mbaa ci sa përëg ni lamu màndarga. Mbëggeel a bare doole ni dee, fiiraange xér ni bàmmeel. Day jàpp jippét, di jum bu Aji Sax ji taal.
Ngën-gi-woy 8:6
Aji Sax jee baax, moo dib rawtu, bésub njàqare, te moo ràññee ñi ko làqoo.
Nawum 1:7
Sama kër Baay, dëkkuwaay yu baree nga fa. Su demewul woon noonu, ndax dinaa leen ne maa ngi leen fay waajali béreb? Te gannaaw bu ma leen waajalee béreb, dinaa délsi, jëlsi leen, yóbbu, ba fu ma nekk, man, ngeen nekk fa, yeen itam.
Yowaan 14:2–3
Ndaw si, li mu man, def na ko. Laata ñu may rob, diw na ma lu xeeñ.
Màrk 14:8
Yeesu ne: «Maa leen ko wax déy, jëtun bu néew doole bii, ñii ñépp, moo leen ëpple lu mu joxe.
Luug 21:3
Maa leen ko wax, déy, képp ku leen may ab kaasu ndox, ngir li ngeen di niti Almasi bi, doo ñàkk sag pey mukk.
Màrk 9:41
Ndax kat ab joxe, bu àndee ak yéene rekk, la boroom joxe bi amul, deesu ci natt lees koy nangul, waaye li mu am, ci lees koy nangul ab joxeem.
2.Korent 8:12
Xale yi, bunu soppante ci làmmiñu kese maanaam ay wax, waaye nanu ko jëfe, te muy dëgg.
1.Yowaan 3:18
Su mbokk mu góor mbaa jigéen raflee, mbaa mu ñàkk lu mu dunde bés bu nekk, ba kenn ci yeen ne mbokk mi: «Demal ak jàmm, solul nag te lekk ba regg,» te fajul aajoom, loolu lu muy jariñ?
Yanqóoba 2:15–16
Lii rekk la: ji lu tuut, góob lu tuut; ji lu bare, góob lu bare. Kon na ku nekk joxe, ni mu ko waaje ci xolam, te bañ koo tiisoo, bañ koo joxee ñàkk pexe, ndax kiy joxee xol bu sedd, Yàlla sopp na ko,
2.Korent 9:6–7
Yeen itam noonu. Bu ngeen defee li ñu leen sant lépp ba noppi, dangeena war ne: “Ay jaam rekk lanu. Sunu warugar lanu def.”»
Luug 17:10
Bés yu mujj yi
Wone yépp17 Sul 2026
16 Sul 2026
15 Sul 2026
14 Sul 2026
13 Sul 2026
12 Sul 2026
11 Sul 2026