Deewam ga mu dee, dee na benn yoon ba fàww, ba tax bàkkaar amatul benn kilifteef, te dund gi muy dund tey, Yàlla la koy dundal.
Room 6:10
Leeru Bés bi
Deewam ga mu dee, dee na benn yoon ba fàww, ba tax bàkkaar amatul benn kilifteef, te dund gi muy dund tey, Yàlla la koy dundal.
Room 6:10
Moo tax ma di ko jox ab cér ci biir ñu bare, mu séddoo ak ay kàngam alalu xareem, ngir moo jébbale bakkanu boppam, ñu limaale kooki tooñkat, moo gàddu bàkkaaru ñu bare te mooy tinul moykat yi.
Esayi 53:12
noonu itam la Almasi bi doone ab sarax benn yoon, ngir gàddu bàkkaaru nit ñu bare, te dina teewsiwaat, ci yoon wu joteetul dara ak bàkkaar, ngir indil ñi koy séentu seenug mucc.
Yawut ya 9:28
«Moom ci boppam moo gàddu sunuy bàkkaar,» moo ko tegoo ci yaramu boppam ca bant ba, ngir nu deewal bàkkaar te dundal njub; «moom mooy ki ngeen wére ci ay góomam.»
1.Piyeer 2:24
Kon bennub sarax boobu, ci la matale sëkk ba fàww nit ñi ñu sellal.
Yawut ya 10:14
Waaye Yeesu mi sax ba fàww, moo sasoo carxal gu sax dàkk. Looloo waral mu mana musal mucc gu mat sëkk, ñiy awe fi moom, dikk fa Yàlla, ndax mooy dund ba fàww, ngir di leen tinul.
Yawut ya 7:24–25
Waaye Yàlla moom, ni mu firndeele cofeelam ci nun, moo di, ba nu doon ay bàkkaarkat, ca la Almasi bi deewe ngir nun! Gannaaw baaxees nañu nu àtteb ñu jub ndax deretam ji tuuru nag, ñaata yoon lees nuy gënatee musal ci am sànj ndax moom?
Room 5:8–9
Gannaaw Almasi bi nag moo daj coonob yaramam, yeen itam gànnaayooleen boobu yéene, ndaxte ku daj coonob yaram, tàggoo naak bàkkaar, ngir bañatee topp xemmemtéefi bakkan, xanaa di topp coobarey Yàlla, diir bi ko dese ci kaw suuf.
1.Piyeer 4:1–2
Fexeleen ba des ci biir cofeelu Yàlla, tey séentu sunu yërmandey Boroom Yeesu Almasi bi, ngir ag texe gu sax dàkk.
Yudd 21
Saxleen ci man, ni ma saxe man ci sama bopp ci yeen. Ni carub reseñ tëlee meññal boppam, su saxul ci ndeyam, ni ngeen di tëlee meññ, su ngeen saxul ci man. «Man maay reseñ gi, yeen ngeen di car yi. Ki sax ci man, ma sax ci moom, kooku mooy meññ lu bare, nde su dul man, dungeen mana def dara.
Yowaan 15:4–5
Meññeefum Noowug Yàlla nag moo di: cofeel ak mbég ak jàmm ak xolu muñ ak mbaax akug tabe ak ngëm
Galasi 5:22
Li feeñal sama darajay Baay mooy ngeen meññ lu bare, te noonu ngeen di firndeele ne samay taalibe ngeen. «Ni ma Baay bi soppe, man itam noonu laa leen soppe. Saxleen ci sama cofeel. Ni ma sàmme sama santaaney Baay, ba tax ma sax ci cofeelam, su ngeen ni sàmmee samay santaane, dingeen sax ci sama cofeel.
Yowaan 15:8–10
Képp kuy jëfe kàddug Yàlla, ci moom déy la cofeelu Yàlla mate sëkk. Ci loolu lanuy xame ne moom lanu nekk.
1.Yowaan 2:5
Sama santaane moo di ni ma leen soppe, ngeen soppantee noonu.
Yowaan 15:12
Waaye Yàlla moom, ni mu firndeele cofeelam ci nun, moo di, ba nu doon ay bàkkaarkat, ca la Almasi bi deewe ngir nun!
Room 5:8
Nun nag xam nanu te gëm nanu cofeel gi nu Yàlla sopp. Yàlla cofeelu neen la. Képp ku saxoo cofeel, ci Yàlla nga sax, te Yàlla itam ci yaw la sax.
1.Yowaan 4:16
Bés yu mujj yi
Wone yépp21 Sul 2026
20 Sul 2026
19 Sul 2026
18 Sul 2026
17 Sul 2026
16 Sul 2026
15 Sul 2026