Leeru Bés bi — 23 Sulet: 1.Korent 15:24

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Gannaaw loolu la muj ga, te ca lay delloo nguur gi kiy Yàlla, di Baay, fekk mu neenal mboolem luy kilifteef ak mboolem sañ-sañ ak doole.

1.Korent 15:24

«Waaye bés boobu mbaa waxtu wa nag, kenn xamu ko; du malaaka ya fa asamaan, du Doom ji, xanaa Baay bi doŋŋ. Moytuleen te teewlu, ndax xamuleen kañ la.

Màrk 13:32–33

Lii ma leen wax nag, ñépp laa ko wax: “Teewluleen!”»

Màrk 13:37

Du caageenu yeexe gu Boroom bi yeexe dige ba, noonu ko ñenn ñi fooge ag yeex. Yeen la muñal kay, ndax bëggul kenn sànku, xanaa ñépp dem ba tuub.

2.Piyeer 3:9

Yeen itam muñleen te takk seenu fit, ndax bés ba Boroom biy dikk dëgmal na. Bokk yi, buleen di ñaxtoonte, lu ko moy dees na leen daan, te daan-kat baa ngii taxaw ci bunt bi!

Yanqóoba 5:8–9

Kiy seede mbir yii nee: «Waawaaw, léegi ma ñëw.» Amiin, Sang Yeesu, ñëwal!

Peeñu ma 22:20

Gannaaw loolu lépp noonu lay seeye nag, xamleen bu baax li leen war: jëfin wu sell akug ragal Yàlla

2.Piyeer 3:11

Te itam mujug lépp dëgmal na; kon nag jiitalleen seenum xel, te ànd ak seen sago, ngir ngeen man di ñaan.

1.Piyeer 4:7

«Takkuleen te seeni làmp di tàkk. Melleen ni nit ñuy séentu seen njaatige lu jóge céet, ndax bu dikkee ba fëgg bunt ba, ñu daldi ko ubbil.

Luug 12:35–36

Bokk yi, nun itam, ñaanalleen nu.

1.Tesalonig 5:25

Ana ku wopp ci yeen? Na woo magi mbooloom gëmkat ñi, ñu ñaanal ko, raayaale ko ag diw ci turu Boroom bi. Ñaan gu ànd ak ngëm day musal ki wopp, ba Boroom bi yékkati ko. Su dee daa bàkkaar, dees na ko jéggal. Kon nag tuddanteleen seeni bàkkaar tey ñaanalante, ndax ngeen wér. Aji jub ji, ag ñaanam, day dal ak doole. Ilyaas nit la woon ku bindoo ni nun, waaye ba mu saxee ci ñaan ngir mu baña taw, ndox laalul suuf diiru ñetti at ak genn-wàll. Mu dellu ñaan, asamaan taw, suuf meññ meññeefam.

Yanqóoba 5:14–18

Deeleen ñaan fu ngeen tollu, gépp xeetu ñaan aki dagaan ci ndimbalal Noo gi, ànd ci ak teewlu fu ngeen tollu, ak gépp parlu, te ngeen di ñaanal mboolem gëmkat ñu sell ñi.

Efes 6:18

Yàlla mi may jaamoo xol, ci ni may siiwtaanee xibaaru jàmm bu Doomam, moom seede na ne noppiwuma ci di leen fàttaliku.

Room 1:9

Ab nuyoo it ñeel na leen, tukkee ci Epafras mi bokk ci yeen, te di jaamub Almasi Yeesu. Muy ku jàmbaare ci saxoo leena ñaanal, ngir seenub taxawaay sotti te mat sëkk ci jëfe mboolem luy coobarey Yàlla.

Kolos 4:12