Leeru Bés bi — 15 Sulet: Macë 6:10

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

na sa nguur dikk, na sa coobare ame fi suuf na mu ame fa asamaan.

Macë 6:10

Def sama coobarey bopp taxul ma wàcce fa asamaan, waaye def coobarey ki ma yónni moo tax.

Yowaan 6:38

Ma ne: «Maa dikk nii, téereb yoon wi indi na li ñu bind ci man.

Taalifi cant 40:8

Yeesu delluwaat, ba nee, ñaareel bi yoon, daldi ñaan ne: «Sama Baay, ndegam lii manu maa teggi ba duma ko naan, na sa coobare am.»

Macë 26:42

«Du képp ku ma naan: “Sang bi, Sang bi,” mooy tàbbi ci nguurug asamaan, xanaa ñiy jëfe sama coobarey Baay ba fa asamaan.

Macë 7:21

Ndax kat du déglukati yoonu Musaa lees di jox àtteb ñu jub fa kanam Yàlla, waaye jëfkati yoonu Musaa mooy jot àtteb ku jub.

Room 2:13

Loolu, su ngeen ko xamee, ndokkalee yeen, ndegam yeena ngi koy jëfe.

Yowaan 13:17

Ku xam lu baax loo wara def te defoo ko nag, bàkkaar nga.

Yanqóoba 4:17

Buleen roy jamonoy tey jii, waaye yeesluleen ci ni ngeen di xalaate ba soppiku, ngir ngeen mana ràññee liy coobarey Yàlla, muy li baax, di bànneexam te mat sëkk.

Room 12:2

Purux déy ay mosu ñam, nopp natt kàddu.

Ayóoba 34:3

Soppe yi, du képp ku ne mu ngeek Noowug Yàlla, ngeen di gëm, waaye nattuleen noo gi mu waxe, ba xam ndax ci Yàlla la jóge, ndax yonenti caaxaan yu baree dajal àddina.

1.Yowaan 4:1

Bàyyileen di àttee li leen seen bët may, deeleen àttee dëgg.»

Yowaan 7:24

Njort naa ne boroomi xel laay waxal. Kon àtteelleen seen bopp li ma leen wax.

1.Korent 10:15

Na kàddug Almasi bi dëkk ci yeen, bay baawaan, ngeen di jariñoo xel mu mat sëkk mu ngeen di jàngalantee aka artoonte. Woyeleen xolub cant, ñeel Yàlla, ak ay taalifi cant ak woyi tagg Yàlla ak woy yu ñu fente ci Noowug Yàlla gi.

Kolos 3:16

«Ku ami nopp kat, na dégg li Noowug Yàlla wax mboolooy gëmkat ñi.

Peeñu ma 2:29

Nit ki ànd ak Xelum Yàlla nag moo mana natt lépp, te moom ci boppam, kenn du ko mana natt.

1.Korent 2:15

Mu neeti leen: «Teewluleen bu baax li ngeen di dégg. Natt bi ngeen di nattale, moom lees leen di nattale, ba wis leen.

Màrk 4:24

Gis naa say jëf, gis sa liggéey ak sag muñ. Xam naa ne manuloo dékku ñu bon ñi. Seetlu nga ñi tuddoo samay ndaw, ba gis ne ay fen-kat lañu.

Peeñu ma 2:2

Waaye lu mu mana doon, settantalleen ko; li baax, ngeen jàpp ci,

1.Tesalonig 5:21

Kooku la wattukat biy ubbil, xar yi di déglu baatam. Mooy woo xari boppam ci seen tur, génne leen. Bu génnee xaram yépp ba noppi, da leen di jiitu, ñu topp ci moom, ndax xàmmee nañu baatam. Ab jàmbur nag, duñu ko topp mukk; dañu koy daw kay, ndax xàmmeewuñu baatub jàmbur.»

Yowaan 10:3–5