Leeru Bés bi — 13 Sulet: Ngën-gi-woy 7:10

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

sa gémmiñ di xelli ngëneelu biiñ. Na walal sama nijaay, tuurul ñiy nelaw.

Ngën-gi-woy 7:10

Looloo tax may daj yii coono. Waaye rusuma ci, ndax xam naa ki ma gëm, te wóor na ma ne, li ma ko dénk, moo ko mana sàmm ba keroog bés ba.

2.Timote 1:12

Ndax kat bir na ma ne du ag dee, du ag dund, du ay malaaka, duy boroom nguur, du tey, du ëllëg, duy boroom doole, du lu kawe, du lu xóot, mbaa meneen mbindeef mu mu doon; dara manu noo tàggale ak cofeel gi nu Yàlla won ci Almasi Yeesu sunu Sang.

Room 8:38–39

Diir bi may nekk ak ñoom, man maa leen doon sàmme sa tur wi nga ma jox. Wattu naa leen, ba kenn ci ñoom sànkuwul, ku moy doomu sànkute jiy sànku, ngir Mbind mi sotti.

Yowaan 17:12

Aji Sax jee safoo ñoñam, di terale néew-ji-doole ag mucc.

Taalifi cant 149:4

May bége wërngalu àddinaam, di bànneexoo doomi aadama.

Kàddu yu xelu 8:31

Waaye Yàlla mi bare yërmande, ci kaw cofeel gu réy gi mu nu sopp,

Efes 2:4

Joxe sa bakkan te say xarit tax, ameesul cofeel gu ko raw,

Yowaan 15:13

ndax dees leena jot, ba fey njëg ga. Kon nag seen yaram, terale leen ko Yàlla.

1.Korent 6:20

Su nuy dund, ngir Boroom bi lanuy dund, su nu deewee it, wormaal Boroom bee tax nu dee. Kon nag nuy dund mbaa nu dee Boroom bi moo nu moom.

Room 14:8

Seet ko ci téereb Aji Sax ji, jàng ko; du menn mala muy wuute ca gent ba, lu ci nekk a fay ànd ak moroom ma. Aji Sax jee ko santaane ci gémmiñam, noowam moo leen di dajale.

Esayi 34:16

Defleen sama kàddu yii ci seenum xel ak ci seen xol. Takkleen ko, muy firnde ci seen loxo, te na doon am mbandal ci seen diggantey gët.

Baamtug yoon wi 11:18

Téereb yoon bii, bumu teqalikook sa làmmiñ, waaye dee ko jàngat guddi ak bëccëg, ngir di fexee jëfe li ñu ci bind lépp. Su boobaa la say mébét di sotti, te ci ngay am ndam.

Yosuwe 1:8

yoonu Yàllaam a nga ca xol ba, du dox ba tërëf.

Taalifi cant 37:31

Su may jëf it, di sàmm sa kàddu. Maay moyu yoonu ku bon.

Taalifi cant 17:4

Sama xol laa làq say wax, ngir bañ laa moy.

Taalifi cant 119:11

Rax ci dolli nu ngeek waxi yonent yi, muy wax ju wóor ju jara gëm, te yeena yey teewlu waxi yonent yi, ni ñuy teewloo ceeñeeru làmp bu tàkke ci biir lëndëm, ba kera fajar di xar, ba biddiiwu njël feqal seen xol.

2.Piyeer 1:19

Ndaxte mboolem lu ñu bindoon, bu njëkk, jàngal nu moo taxoon ñu bind ko, ngir Mbind mi may nu xolu muñ, te ñaax nu, ba nu am yaakaar.

Room 15:4