Leeru Bés bi — 8 Sulet: 1.Yowaan 1:9

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Su nu ko àggee sunuy bàkkaar, te muy ku jara wóolu, di boroom njub, moo nuy jéggal sunuy bàkkaar, raxas nu ba nu set, tàggook gépp njubadi.

1.Yowaan 1:9

Éy Yàlla, ni nga goree, baaxe ma ni, faral samag tooñ ngir sa yërmande ju yaa. Fóotal maa fóotal sama ñaawtéef, raxasal ma sama moy.

Taalifi cant 51:3–4

«Mu jóg, ngir dellu kër baayam. Fu sore la ko baayam séene, muy dikk. Mu ñeewante ko, daw, laxasu ko, fóon ko.

Luug 15:20

Maa far say moy, mu naaxsaay niw niir, say bàkkaar ne mes nib lay. Délsil fi man, jot naa la.»

Esayi 44:22

Xale yi, yeen laay bind, ndax dees leena jéggal seeni bàkkaar ci turu Almasi bi.

1.Yowaan 2:12

Baaxleen ci seen diggante, di ñeewantante, tey baalante, ni leen Yàlla baale ci Almasi bi.

Efes 4:32

ndax Yàlla ci biir ag jéllaleem la firndeel njubteem ci janti tey jii, ngir mu leer ne moo wéye njub, te képp ku gëm Yeesu, moo koy baaxe àtteb ku jub.

Room 3:26

Maa leen di wis ndox mu set, ngeen set. Mboolem seen sobe ak mboolem seen kasaray tuur laa leen di setalal.

Esekiyel 36:25

«Moona am nga foofu ci Sàrd nit ñu néew ñu tilimalul seen mbubb. Ñooñooy ànd ak man, sol lu weex, ndax ñoo ko yeyoo.

Peeñu ma 3:4

Kii mooy ki dikke ci ndox ak ci deret, kookooy Yeesu Almasi bi; jaarul ci sóobu ndox doŋŋ, waaye su weesoo loolu, jaar na ci dee, tuur deretam. Noowug Yàllaa ko seede, ndax Noo gi mooy dëgg,

1.Yowaan 5:6

Loo séq ak njiit lu jubadi luy yoonal njubadi?

Taalifi cant 94:20

Li nu gis te dégg ko, moom lanu leen di àgge, ngir yeen itam ngeen am ak nun ag jokkoog mbokk. Te sunu jokkoog mbokk googu, nook Baay bi lanu ko séqal, ak Doomam Yeesu Almasi bi.

1.Yowaan 1:3

Soppe yi, léegi doomi Yàlla lanu, te li nuy dooni nag feeñagul. Waaye xam nanu ne bés bu Almasi bi feeñee, nooy nirook moom, ndax su boobaa, ni mu nekke, noonu lanu koy gise. Te képp ku am jooju yaakaar ci moom, noonu mu sete, ni lay setale boppam.

1.Yowaan 3:2–3

Duma waxateek yeen lu bare ndax kàngamu àddinaa ngi dikk. Manul ci man dara nag.

Yowaan 14:30

Boobu sarxalkat bu mag lanu soxla: moo sell, mucc sikk, mucc sobe, moom lañu teqale ak bàkkaarkat yi ci àddina, te moom lañu kaweel ba fa tiim asamaan.

Yawut ya 7:26

Ndax kat sunub xare du nook boroomi deret ak suux, waaye ñi ñu ko séqal ay boroom nguur lañu, ak ay boroom sañ-sañ, ak ay boroom doole yu nekk ci àddina ju lëndëm jii, di ay dagi Seytaane yu fare déndi asamaan.

Efes 6:12

yi ngeen doon dunde démb, ngeen àndoon ci ak doxalinu àddinay tey jii, ak ku bon kiy kàngamu boroom baat yi ci jaww ji asamaan tiim, di boroom xel mu bon mi wéye liggéeyam ci biir aji déggadi ñi, tey.

Efes 2:2

Xam nanu ne képp ku sosoo ci Yàlla doo sax ci bàkkaar, waaye Kenn ki sosoo ci Yàlla moo koy sàmm, ba ku bon ki du ko manal dara. Nun nag xam nanu ne ci Yàlla lanu bokk, te àddina sépp a ngi ci loxol ku bon ki.

1.Yowaan 5:18–19