«Taalibe sutul kilifaam, te jaam sutul sangam.
Macë 10:24
Leeru Bés bi
«Taalibe sutul kilifaam, te jaam sutul sangam.
Macë 10:24
Yeena ngi ma naa Kilifa gi ak Sang bi, te yeena yey, nde moom laa.
Yowaan 13:13
Ab taalibe, su demee ba mel ni kilifaam, wàcc na; ab jaam it, su demee ba mel ni sangam, wàcc na. Ndegam boroom kër gi lañuy woowe Beelsebul, miy Seytaane, astamaak waa këram.
Macë 10:25
Fàttalikuleen kàddu gi ma leen wax: “Jaam sutul sangam.” Gannaaw man lañu bunduxataal, yeen itam, dinañu leen bunduxataal. Bu ñu sàmmoon sama kàddu, dinañu sàmm seen gos itam.
Yowaan 15:20
Man, jottali naa leen sa kàddu, waaye àddinaa leen bañ, ndax ni ma ñàkka bokke ci àddina, ni lañu ñàkka bokke ci àddina.
Yowaan 17:14
Xoolleen ci moom mi bàkkaarkat yi doon xeex, bala ngeena yoqi bay xàddi. Yeen kat xareeguleen ak bàkkaar, ba seen deret tuuru ci.
Yawut ya 12:3–4
Kon nag gannaaw gii ndiiraanu seede wu réy moo nu yéew, nanu sippiku mboolem sëf bu nuy yeexal ak bàkkaar bu nu yomba téqtal. Ñu daw nag xél wi ñu nu waajalal, te baña yoqi. Nanu ne jàkk Yeesu, kiy sos, di sottal ngëm, moom mi mbég mi ñu ko waajalal tax mu dékku bant ba ñu ko daaj, tegul muy dara toroxtaange ja ko ca fekk, te doxe ca toog ca ndijooru ngànguney Yàlla.
Yawut ya 12:1–2
Gannaaw Almasi bi nag moo daj coonob yaramam, yeen itam gànnaayooleen boobu yéene, ndaxte ku daj coonob yaram, tàggoo naak bàkkaar,
1.Piyeer 4:1
Doom, teewloo ma xel te roy ma.
Kàddu yu xelu 23:26
Waaye céy bu ñu amoon boobu xol ngir ragal ma, di sàmm sama santaane yépp bés bu nekk, ba tax ñu baaxle, ñoom ak seen askan, ba fàww!
Baamtug yoon wi 5:29
Amuloo benn wàll mbaa ab cér ci lii, ndax sa xol a jubul ci kanam Yàlla.
Jëf ya 8:21
Ndaxte boroom xintey bakkan ab noonu Yàlla la, nde déggalul yoonu Yàlla, te manu ko sax. Moo tax ñi wéye seen bindu suuxu neen duñu mana neex Yàlla.
Room 8:7–8
Li nu séentu woon sax wees nañu ko, nde Sang bi lañu njëkka jébbal seen bopp, door noo jébbal seen bopp, te noonu la ko Yàlla bëgge.
2.Korent 8:5
Mboolem jëf ju Esekiyas sumboon ci wàllu liggéeyub kër Yàlla ga, na mu dëppoo ak yoon wi ak santaane yi, ngir jaamu Yàllaam, léppi xolam la ko defe, ba am ca ndam.
2.Jaar-jaar ya 31:21
Sàmmal a sàmm sab xol, nde xalaati xol ngay jëfe.
Kàddu yu xelu 4:23
Lu ngeen mana def, liggéeyeleen ko xol bu tàlli, ni bu ñeelul woon nit doŋŋ, xanaa Boroom bi.
Kolos 3:23
Buleen ko defe ngistal, mbaa ngeen di ko sàkkoo lu leen neex, na di yéene ju ngeen tibbe ci seen xol, ngir jëfe liy coobarey Yàlla, ni mu ware ay jaami Almasi bi. Liggéeyalleen leen ci xol bu tàlli, ba mu mel ni Boroom bi ngeen ko defal, waaye du nit doŋŋ,
Efes 6:6–7
Ci sa yoonu santaane laay wéy, yaa may may xol bu tàlli.
Taalifi cant 119:32
Bés yu mujj yi
Wone yépp9 Sul 2026
8 Sul 2026
7 Sul 2026
6 Sul 2026
5 Sul 2026
4 Sul 2026
3 Sul 2026