Aji Sax ji ne ko: «Man ci sama bopp maay ànd ak yaw te maa lay noppal.»
Mucc ga 33:14
Leeru Bés bi
Aji Sax ji ne ko: «Man ci sama bopp maay ànd ak yaw te maa lay noppal.»
Mucc ga 33:14
Dëgërluleen nag te am fit. Buleen tiit, buleen yox-yoxi ndax ñoom, ngir seen Yàlla Aji Sax ji mooy ànd ak yeen. Du leen ba, du leen wacc mukk.»
Baamtug yoon wi 31:6
Aji Sax ji nag mooy dox, jiitu la. Moom mooy nekk ak yaw. Du la ba, du la wacc mukk. Bul tiit, bul yoqi.»
Baamtug yoon wi 31:8
Xanaa du maa la sant ne la, nga dëgërlu te am fit? Bul tiit, bul ragal. Sa Yàlla Aji Sax ji laak yaw, fépp foo jëm.»
Yosuwe 1:9
Loo mébét, bàyyil Yàlla xel, mu xàllal la yoon.
Kàddu yu xelu 3:6
Buleen jikkowoo bëggub xaalis; doylooleen li ngeen am, ndax Yàlla moo ne: «Duma la bàyyi mukk, duma la wacc mukk.» Moo tax nu mana am fitu wax ne: «Boroom beey sama ndimbal, duma tiit. Ana lees ma manal?»
Yawut ya 13:5–6
Du caageenu doyloo sunu manoorey bopp, ba yaakaar ne lenn man naa sottee ci sunu wàllu bopp, waaye sunu manoore ci Yàlla la jóge.
2.Korent 3:5
Bu nu dugal ci nattu, waaye yal nanga nu musal ci ku bon ki. Yaw de yaa yelloo nguur ak kàttan ak màggaay, ba fàww. Amiin.”
Macë 6:13
Aji Sax ji, maa xam ne nit moomul yoonam, kuy dox moomuli jéegoom.
Yeremi 10:23
Man nag Aji Sax ji, ci yaw laa dénku. Ma ne: «Yaay sama Yàlla.»
Taalifi cant 31:15
Nanu seet itam ci sunu biir nu nuy xiirtalantee ngir cofeel ak jëf ju baax.
Yawut ya 10:24
Kàddu yu jub da lay yey, ana li ngeen may yedde, lu mu doon?
Ayóoba 6:25
Soppe yi, sama ñaareelu bataaxal a ngi nii, te bu ci nekk am na lu ma leen ci fàttali, ngir xiirtal leen ci xalaatin yu set,
2.Piyeer 3:1
Ca la ñi ragal Aji Sax ji diisoo ci seen biir, Aji Sax ji teewlu, déglu leen. Ñu bind fi kanamam téereb fàttaliku, bu lim ñi ragal Aji Sax ji, te teral aw turam.
Malasi 3:16
«Maa leen neeti, su ñaar ci yeen déggoo ci kaw suuf, ci mboolem lu ñu ñaan, dees na leen ko nangul ci sama dogalu Baay ba fa asamaan,
Macë 18:19
Yàlla Aji Sax ji daldi ne: «Wéet baaxul ci nit, kon dinaa ko bindal ku koy taxawu te jekk ci doon wéttalam.»
Njàlbéen ga 2:18
Ñaar a man kenn; doñ-doñoondoo, yoolu bu baax. Kenn daanu, moroom ma may ko loxo. Waaye ngalla ku daanu te amuloo ku la may loxo!
Kàdduy waare 4:9–10
Kon nag bunu di seetati lu nu sikkantee, li ngeen di seet kay mooy nu ngeen fexee ba dungeen yóbbe mbokkum gëmkat lu koy fakkastal, mbaa lu koy xiirtal ci bàkkaar.
Room 14:13
Yenuleen seeni yeni moroom, su boobaa ngeen di topp yoonu Almasi bi, ba mu mat sëkk.
Galasi 6:2
Bokki gëmkat ñi, su ñu bettee nit ci ag tooñ, yeen ñi topp Noowug Yàlla, waññileen ko ndànk, te kenn ku nekk ci yeen xoolaat boppam bu baax, ngir seen bakkan bañ leena xiirtal, ba ngeen daanu ci fiir, yeen itam.
Galasi 6:1
Bés yu mujj yi
Wone yépp11 Sul 2026
10 Sul 2026
9 Sul 2026
8 Sul 2026
7 Sul 2026
6 Sul 2026
5 Sul 2026