Leeru Bés bi — 16 Sulet: Mucc ga 19:6

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

waaye yeenay doon nguuru sarxalkati Yàlla, te di xeet wu sell.” Kàddu yooyu ngay wax bànni Israayil.»

Mucc ga 19:6

Ñuy woy nag woy wu yees, naan: «Yaa yeyoo jël téere bi, tàyyi tayu yi, ndax yaw lañu rendi, te sa deret nga jote ay niti gépp giir ak wépp làkk ak wépp xeet ak wépp askan, ñu doon ñoñi Yàlla. Yaa leen def ñu doon nguurug sarxalkat yi, ñeel sunu Yàlla, te dinañu nguuru ci àddina.»

Peeñu ma 5:9–10

Waaye yeen nag yeenay giir giy tànnéef, yeenay sarxalkati buur, yeenay askan wu sell, yeenay xeet wi ñu jot, ngir ngeen biral jaloore yu wéet yi ñeel ki leen woo, génnee leen cig lëndëm, indi leen ci leeram gu yéeme.

1.Piyeer 2:9

Yeen nag lees di woowe: «Sarxalkati Aji Sax ji,» ñu naa: «Sunu jawriñi Yàlla yaa ngii!» Alali xeet yi, yeena koy lekk, di damoo seeni koom.

Esayi 61:6

Ndokkale ak sellaay ñeel na ñi séddu ci ndekkite lu njëkk li! Ñooñu, ñaareelu dee gi manalu leen dara. Ñooy doon it sarxalkati Yàlla ak Almasi bi, te ñooy nguuroondoo ak Almasi bi junniy at.

Peeñu ma 20:6

Kon nag bokk yu sell yi, yeen ñi bokk ci wooteb asamaan, ràññeeleen Yeesu, ndaw li, sarxalkat bu mag bi ci yoon wi nu gëm.

Yawut ya 3:1

Kon nag saa su nekk, nanuy jaare ci Yeesu, di génne sunu saraxu cant, ñeel Yàlla, muy sarax su bawoo ci sunuw làmmiñ, ñu di ko birale aw turam.

Yawut ya 13:15

Ndax kat noo di liggéeyu Yàlla; Yàllaa nu yeesal ci Almasi Yeesu, ngir nu wéye jëf ju rafet ja mu nu fàgguloon ca njàlbéen, ngir nu di ko jëfe.

Efes 2:10

Ku yàq kër Yàlla nag, kooku Yàlla dina ko yàq, ndax kër Yàlla dafa sell, te mooy li ngeen doon.

1.Korent 3:17

Gannaaw gi, noon ya xam ne yég nanu leen, te Yàlla nasaxal na seen pexe. Ba mu ko defee nu walbatikuwaat nun ñépp ca tata ja, ku nekk dellu ca liggéeyam.

Neyemi 4:9

Teewluleen te ñaan, ngir baña tàbbi cig fiir. Xolub nit kat yebu na, yaram see néew doole.»

Macë 26:41

Ag ñaan nag, saxooleen ko, te ngeen teewlu ci, boole ci ag cant.

Kolos 4:2

ci ni ngeen di sippikoo ci kawam, mboolem seenu tiis, nde mooy ki leen tiisoo. Àndleen ak sago te teewlu! Ki leen di tuumaal, Seytaane, mu ngi ŋar ni gaynde, tey wër, di rëbb ku mu warax. Pastéefu ngëm ngeen di xeexe te xam ne benn coono bi ngeen di daj, moom la mboolem seen bokki gëmkat yi ci àddina di daj.

1.Piyeer 5:7–9

«Ana lu ngeen ma naa “Sang bi, Sang bi,” te jëfewuleen samay wax?

Luug 6:46

Doonleen jëfekati kàddu gi, buleen di ay déglukat doŋŋ, di nax seen bopp.

Yanqóoba 1:22

Ci kaw loolu Aji Sax ji wax Musaa ne ko: «Loo may woowe wall? Waxal bànni Israayil, ne leen ñu dem rekk,

Mucc ga 14:15

Buleen jaaxle ci dara, waaye ci mbir mu mu mana doon, deeleen dikke Yàlla seeni soxla, di ko ñaan aka dagaan te boole ci di ko sant. Su boobaa jàmmu Yàlla ji wees ab takk, mooy sàmm seen xol ak seenum xel ndax Almasi Yeesu.

Filib 4:6–7