Maa lay def nga mel ci gis-gisu askan wii ni tatay xànjar ju ñu dàbbali, ñu di la song te duñu la man. Maay ànd ak yaw, di la wallu, di la xettali.» Kàddug Aji Sax jee.
Yeremi 15:20
Leeru Bés bi
Maa lay def nga mel ci gis-gisu askan wii ni tatay xànjar ju ñu dàbbali, ñu di la song te duñu la man. Maay ànd ak yaw, di la wallu, di la xettali.» Kàddug Aji Sax jee.
Yeremi 15:20
Manees naa foqati alalu sëxëtoo ci loxol jàmbaar a? Am manees naa rëcc boroom doole bu la jàpp? Aji Sax ji déy dafa wax ne: «Moona dees na foqati ku jàmbaar jàpp, ba rëccal alalu sëxëtoob boroom doole. Say jotewaale, maay joteek ñoom, te say doom, maa leen di wallu. Ñi lay néewal, maa leen di leel seen suuxu bopp. Seen deret ni biiñ bu bees, ma màndale leen, ba ñépp xam ne maay Aji Sax ji lay wallu, jàmbaaru Yanqóoba ji lay jot.»
Esayi 49:24–26
bul ragal, yaw laa àndal, bul tiit, maay sa Yàlla; maa lay dooleel, dimbali la déy, maa lay téyee sama loxol ndijoor liy àtte dëgg.
Esayi 41:10
Ndax sarxalkat bu mag bi nu am du ku tëlee yég sunuy néew doole, waaye ni nun rekk lees ko nattoo wet gu nekk, te taxul mu bàkkaar.
Yawut ya 4:15
Coonoy nattu bi mu dékku nag tax na mu mana wallu ñi nekk ci nattu.
Yawut ya 2:18
Bu Aji Sax ji rafetloo saw yoon, mooy jiite say jéego. Soo tërëfee it, doo daanu. Aji Sax jee lay walloo loxoom.
Taalifi cant 37:23–24
Mooy màndal put gu wow, di feesal ngëneel biir bu wéet.
Taalifi cant 107:9
gannaaw mos ngeen ci mbaaxug Sang bi.
1.Piyeer 2:3
Dib taalifu cant, ñeel Daawuda. Mooy ba mu nekkee ca màndiŋu Yuda. Yaw Yàlla, yaay sama Yàlla, ma xëy di la wër, sama bakkan mar la, sama jëmm namm la, fu suuf mare ndox, ne sereŋ.
Taalifi cant 63:1–2
Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, yaaka sopplub dëkkuwaay!
Taalifi cant 84:2
Ci diggante ñaar yooyii laa tance: yàkkamti namaa yiwiku ba fekki Almasi bi, te loolu moo dàqati fuuf.
Filib 1:23
Man nag ma am dëgg, ne la jàkk, yewwu, regge sa jëmm.
Taalifi cant 17:15
Dootuñu xiif, dootuñu mar. Dootuñu loru ci jant bi mbaa weneen tàngoor, ndaxte Xar mi ci diggu ngàngune mi moo leen di sàmm, yóbbu leen ca bëti ndoxum dund ma, te Yàllaa leen di fompal wépp rongooñ.»
Peeñu ma 7:16–17
Céy Yàlla, yaa wéet ngor, doom aadama yiiroo sa keppaar, yiiru;
Taalifi cant 36:8
Maay yafal sarxalkat yi, ba reggal leen, sama ñoñ ñi regge sama ngëneel.» Kàddug Aji Sax jee.
Yeremi 31:14
Bés yu mujj yi
Wone yépp10 Sul 2026
9 Sul 2026
8 Sul 2026
7 Sul 2026
6 Sul 2026
5 Sul 2026
4 Sul 2026