Leeru Bés bi — 6 Sulet: Kolos 4:6

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Na seen kàddu ànd ak yiw te am solo, te ngeen xam nu ngeen di tontoo ku nekk, tont li war.

Kolos 4:6

Wax ju ñor di nataalu wurus wu tege ci xaalis. Kàddu yu lay yedd ci kuy dégg, jaarob wurus la mbaa gànjaru ngalam.

Kàddu yu xelu 25:11–12

Bu genn kàddu gu bon génne seen gémmiñ, xanaa su ko jaree ngeen wax lu baax, luy jariñe, te diw yiw ci ñi koy dégg.

Efes 4:29

Nit ku baax, ci dencub ngëneel lay jële lu baax, nit ku bon it, ci dencub safaanam lay jële lu bon.

Macë 12:35

Ndax kat ci sa kàddu lees lay joxe dëgg, ci sa kàddu it lees lay daane.»

Macë 12:37

Làmmiñu waxkat, jam-jami jaasi; kàddu gu xelu, garab la ci.

Kàddu yu xelu 12:18

Ca la ñi ragal Aji Sax ji diisoo ci seen biir, Aji Sax ji teewlu, déglu leen. Ñu bind fi kanamam téereb fàttaliku, bu lim ñi ragal Aji Sax ji, te teral aw turam.

Malasi 3:16

Moo tax Aji Sax ji dafa wax ne: «Soo délsee, ma delloosi la, nga dellu di ma liggéeyal. Soo dee wax ngëneel lu soreeki caaxaan, dinga mel ni yaay sama làmmiñ, te nit ñeey délsi ànd ak yaw, waaye du yaay délsi ànd ak ñoom.

Yeremi 15:19

Gannaaw nag yeena duunle ci lépp; muy ci wàllu ngëm ak wàllu kàddu yu rafet ak wàllu xam-xam ak cawarte ci lépp ak ci cofeel gu nu leen xiir, kon ndajalem ndimbal lii it, ngalla duunleleen ci.

2.Korent 8:7

Maa ngi janook sa ngor, di doxe sa dëgg.

Taalifi cant 26:3

Yiw ak yërmande, fa Aji Sax ji; kee muñ mer te bare ngor!

Taalifi cant 145:8

ngir ngeen doon doomi seen Baay ba fa asamaan, nde mooy kiy fenkal jantam ci kaw ñu bon ñi, ak ñu baax ñi, te mooy tawal ñi jub, ak ñi jubadi.

Macë 5:45

Kon nag doonleen ay roykati Yàlla, gannaaw yeenay doomam yi mu sopp, te ngeen di doxale cofeel, ni Almasi bi nu sopp, ba joxeel nu bakkanam, def ko saraxu sawara ngir xetug jàmm gi neex Yàlla.

Efes 5:1–2

Baaxleen ci seen diggante, di ñeewantante, tey baalante, ni leen Yàlla baale ci Almasi bi.

Efes 4:32

Kon nag gannaaw setal ngeen seen xol, ndax dëgg gi ngeen déggal, ba tax ngeen am cofeel gu mucc jinigal ci bokki gëmkat ñi, nangeen soppantee xol bu set, cofeel gu mat sëkk.

1.Piyeer 1:22

Ndaxte cofeelu Almasi bi daal moo nu jiite, nun ñi ràññee lii: gannaaw kenn moo dee ngir ñépp, kon ñépp a dee.

2.Korent 5:14

Yeen kay, soppleen seeni noon, defleen lu baax, lebleleen te baña yaakaar ndelloo. Su boobaa seenub yool réy, ngeen di doomi Aji Kawe ji, ndax moom de ñi santadi te bon, moo leen di baaxe. Ni seen Baay ame yërmande nag, nangeen ni ame yërmande.

Luug 6:35–36