Leeru Bés bi — 5 Sulet: 1.Yowaan 4:16

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Nun nag xam nanu te gëm nanu cofeel gi nu Yàlla sopp. Yàlla cofeelu neen la. Képp ku saxoo cofeel, ci Yàlla nga sax, te Yàlla itam ci yaw la sax.

1.Yowaan 4:16

Waaye Yàlla mi bare yërmande, ci kaw cofeel gu réy gi mu nu sopp, nun ñi doon nit ñu dee ba noppi ndax sunuy moy, moo nu booleek Almasi bi, dundalaat nu. Ci kaw yiw daal ngeen mucce. Ci sunu bokk ak Yeesu Almasi bi la nu Yàlla dekkalandoo ak moom, dëëlandoo nook moom fa déndi asamaan. Mbaax gi nu Yàlla won ci Almasi Yeesu, moom lay firndeele mboolem xarnu yiy ñëw, ni yiwam yaatoo ba tiiñ am xel.

Efes 2:4–7

Ndax Yàlla moo sopp àddina, ba joxe jenn Doomam ji, ngir képp ku ko gëm, texe ba fàww, te du sànku mukk.

Yowaan 3:16

Moom mi nu bañalul Doomu boppam, xanaa joxeel nu ko, nun ñépp, ana nu mu nuy baña baaxee gépp yiw, boole ci?

Room 8:32

Aji Sax jee baaxe ñépp, di yërëm lu mu sàkk.

Taalifi cant 145:9

Nun nag, li nu taxa am cofeel moo di Yàlla moo nu njëkka sopp.

1.Yowaan 4:19

Ndokkalee yaw mi gëm ne mbir mi ñu la yégal, te mu tukkee ci Boroom bi dina sotti!»

Luug 1:45

Mànkooleen, buleen xëccu daraja, waaye nanguleena jonjoo ak ñi féete suuf, te baña jàppe seen bopp boroomi xel.

Room 12:16

Bokk yi, bu leen di gënaatle te di gëmkati sunu Sang Yeesu Almasi bi, Boroom leer.

Yanqóoba 2:1

Bokk yi, soppe yi, dégluleen. Xanaa du Yàlla moo tànn ñi àddina jàppe ñu néew doole, ngir ñu barele ngëm, boole ci jagoo nguur gi Yàlla dig ñi ko sopp?

Yanqóoba 2:5

Bu kenn sàkku njariñal boppam, waaye sàkkuleen seen njariñal moroom.

1.Korent 10:24

Kon su nu amee lu nu lekk ak lu nu sol, nanu ko doyloo. Waaye ñi sàkkoo barele, ñooy tàbbi ci nattub bakkan aki fiir ak lu bare ciy xemmemtéef yu tekkiwul dara, xemmemtéef yuy lore, tey suuxal seeni boroom ci yàqule ak sànkute.

1.Timote 6:8–9

Waaye li àddina jàppe ag ndof, moom la Yàlla tànn, ngir rusloo ko xamkat yi, te li néew doole ci àddina, moom la Yàlla tànn, ngir rusloo ko li bare doole. Li tuut ab juddu ci àddina ak li xeeblu, li tekkiwul dara, moom la Yàlla tànn, ngir neenale ko li tekki, ba tax kenn du mana damu ci kanam Yàlla.

1.Korent 1:27–29

Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla, ñeel Daawuda. Éy Aji Sax ji, man de, réy-réyluwuma, daŋŋiiraluma, xintewoowuma lu réy it, mbaa lu ma ëlëm.

Taalifi cant 131:1