Naka laa ko gis, ne dàll daanu ci ay tànkam ni ku dee. Mu teg ma loxol ndijooram, ne ma: «Bul tiit. Maay Ki njëkk, di Ki mujj.
Peeñu ma 1:17
Leeru Bés bi
Naka laa ko gis, ne dàll daanu ci ay tànkam ni ku dee. Mu teg ma loxol ndijooram, ne ma: «Bul tiit. Maay Ki njëkk, di Ki mujj.
Peeñu ma 1:17
Yeen kat du yeena agsi woon ba jege tund wu ngeen mana laale seen loxo, muy tàkk, ànd aki xàmbaar ak lëndëm gu ne këruus ak ngelaw lu réy.
Yawut ya 12:18
Waaye yeen fi ngeen agsi moo di tundu Siyoŋ, dëkku Yàlla jiy dund, te mooy Yerusalem ga ca asamaan, yeena àgg fa junniy junniy malaaka dajee di màggal; yeena àgg fa ndajem taaw ya seeni tur binde fa asamaan. Yeena àgg fa Yàlla, àttekatub ñépp; yeena àgg fa noowi aji jub ña ñu matal sëkk. Yeena àgg fa Yeesu, rammukat bi dox kóllëre gu yees gi. Yeena àgg fa deret jiy setal tuuroo, te kàddug deret ja gëna neex kàddug deretu Abel ga jiboon.
Yawut ya 12:22–24
Nanu ne jàkk Yeesu, kiy sos, di sottal ngëm, moom mi mbég mi ñu ko waajalal tax mu dékku bant ba ñu ko daaj, tegul muy dara toroxtaange ja ko ca fekk, te doxe ca toog ca ndijooru ngànguney Yàlla.
Yawut ya 12:2
Ndax sarxalkat bu mag bi nu am du ku tëlee yég sunuy néew doole, waaye ni nun rekk lees ko nattoo wet gu nekk, te taxul mu bàkkaar. Kon nag nanu ñemee dikk ba ca ngàngunem yiw ma, ndax nu jot yërmande te dajeek aw yiw wu nu wallu fu nu ko soxlaa.
Yawut ya 4:15–16
Aji Sax ji dafa wax, moom buurub Israayil, jotkatam, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, mu ne: «Maa njëkk, maa mujj, te Yàlla amul ndare man.
Esayi 44:6
Dooley kilifteefam ak jàmm ja du am kemu, fa jalub Daawuda ak nguuram ga muy samp, saxale ko yoon ak njub tey jii ba fàww. Lii la Aji Sax ji Boroom gàngoor yi def ci xéraangeem.
Esayi 9:6
Waaye Aji Sax ji, xanaa du yaa masa nekk? Sama Yàlla sama Aji Sell ji, doo saay. Aji Sax ji, ab àtte nga tabbe ñii, yaw sama cëslaay, mbugal nga fi dëje ñii.
Abakug 1:12
Ana kuy Yàlla ku moy Aji Sax ji? Ana ku mat cëslaay ku dul sunu Yàlla?
2.Samiyel 22:32
Ngalla Yàlla, déglul, maa ne wallóoy, teewlul, ma dagaan la.
Taalifi cant 61:2
Buleen jaaxle ci dara, waaye ci mbir mu mu mana doon, deeleen dikke Yàlla seeni soxla, di ko ñaan aka dagaan te boole ci di ko sant. Su boobaa jàmmu Yàlla ji wees ab takk, mooy sàmm seen xol ak seenum xel ndax Almasi Yeesu.
Filib 4:6–7
sippi ko sama tawat, diis ko sama njàqare.
Taalifi cant 142:3
Ndaxam moo xam fi ma jaare, te bu ma nattoo, ma génn ci ni wurus wu ñu xelli.
Ayóoba 23:10
Di ñaanu Musaa, góorug Yàlla ga. Boroom bi, yaa nu masa fat maasoo maas.
Taalifi cant 90:1
Yaa di rawtub néew-ji-doole, di rawtub aji ñàkk, biir njàqare, yaay mbaar mu ñuy yiiroo waame, di ker gu ñuy féexloo ci tàngoor, ndax merum kilifa gu néeg mooy waame wu ne yureet ci kaw ab tabax.
Esayi 25:4
Yàllaa mat. Kàddug Aji Sax jee wér te wóor. Mooy feg képp ku ko làqoo.
Taalifi cant 18:31
Man maa leen di texeel ba fàww; duñu sànku mukk, te kenn du leen foqatee ci sama loxo.
Yowaan 10:28
Yaa ko dige, dooleel ma, ma dund; bul tas sama yaakaar.
Taalifi cant 119:116
Yaakaar jooju lanu am, mu mel ni diigalub gaal, diigal bu dëgër te wóor, ñeel sunu xol, te yaakaar jooju mooy bëtt rido ba, ba jàll ca néeg bu sella sell ba.
Yawut ya 6:19
Bés yu mujj yi
Wone yépp3 Awr 2026
2 Awr 2026
1 Awr 2026
31 Mar 2026
30 Mar 2026
29 Mar 2026
28 Mar 2026